Wolof Bible: Acts

1:1  Yaw Teyofil, téere bu jëkk, ba ma bindoon, ëmb na lépp li Yeesu tàmbali woon a jëf ak a jàngale,

1:2  ba ci bés, ba ko Yàlla yéege ci asamaan. Lu ko jiitu joxoon na ay ndigal, jaare ci Xel mu Sell mi, jëm ci ndaw ya mu tànnoon.

1:3  Gannaaw ay coonoom, ñëw na ci ñoom, di leen won ay firnde yu bare te wér ne mu ngi dund; mu feeñu leen diirub ñeent-fukki fan, di diisoo ak ñoom ci lu jëm ci nguuru Yàlla.

1:4  Am bés muy lekk ak ñoom, mu sant leen ne: «Buleen sore Yerusalem, waaye ngeen xaar li Baay bi dige woon te ma waxoon leen ko.

1:5  Ndaxte Yaxya daa na sóob nit ñi ci ndox, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi fi ak ay fan yu néew.»

1:6  Bi ñu dajaloo ak moom nag, ñu laaj ko: «Boroom bi, ndax ci jamono jii ngay yékkatiwaat nguuru Israyil?»

1:7  Mu tontu leen: «Ngeen xam jamono yi ak saa, yi Baay bi dogal ci sañ-sañam, loolu mayuñu leen ko.

1:8  Waaye bu Xel mu Sell mi ñëwee ci yéen, dingeen jot kàttan te nekk samay seede ci dëkku Yerusalem, ca diiwaani Yude ak Samari yépp ak ba fa àddina yem.»

1:9  Bi mu waxee loolu, te ñu di ko xool, Yàlla yéege na ko, te aw niir jël ko, làq ko seeni bët.

1:10  Bi muy dem nag, te ñu ne jàkk asamaan, ñaar ñu sol yu weex daldi ne seef, taxaw ci seen wet.

1:11  Ñu ne leen: «Yéen waa Galile, lu tax ngeen taxaw, di xool ci asamaan? Yeesu male ñu jële ci seen biir, yéege ko asamaan, dina dellusi ni ngeen ko gise, muy dem asamaan.»

1:12  Bi loolu amee ñu jóge ca tund, woowu ñuy wax tundu Oliw ya, te mu dend ak Yerusalem lu tollu ak kilomet, ñu daldi dellu Yerusalem.

1:13  Bi ñu dikkee, ñu yéeg ca néeg, ba sut ca taax ma, fa ñuy dal. Ñoo doon Piyeer ak Yowaana, Saag ak Andare, Filib ak Tomaa, Bartelemi ak Macë, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokkoon ci mbooloo mi ñuy wax Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa doomu Saag.

1:14  Ñoom ñépp ñoo bokk menn xel, di wéy ci ñaan ci Yàlla, ànd ak jigéen ñi ak Maryaama, ndeyu Yeesu, ak rakki Yeesu yu góor.

1:15  Ca bés yooya nag Piyeer taxaw ca digg bokk ya, di mbooloo mu tollu ni téeméer ak ñaar-fukk.

1:16  Mu ne leen: «Bokk yi, li Xel mu Sell mi waxoon ci Mbind mi jaarale ko ci gémmiñu Daawuda, fàww mu am. Waxoon na ci mbirum Yudaa, mi wommat ñi jàpp Yeesu

1:17  te mu bokkoon ci nun, ba am cér ci liggéey bi.»

1:18  --Pey gi Yudaa jotoon ci ñaawteefam, mu jënd ci tool, daanu fa, ba fàcc, ay buttitam tuuru.

1:19  Loolu siiwoon na ci waa Yerusalem, moo tax ci seen làkk ñuy tudde tool ba Akeldama, maanaam «Toolu deret.» —

1:20  Piyeer teg ca ne: «Ndaxte lii lañu bind ci téereb Sabóor:“Na këram gental,bu fa kenn dëkk.” Te it:“Na keneen bey sasam.”

1:21  Kon ñeel na nu, nu tànn kenn ci ñi bokk ak nun, diir bi Yeesu doon dem ak a dikk ci sunu biir,

1:22  li dale ci bi ko Yaxya sóobee ci ndox, ba bés ba ko Yàlla jële ci sunu biir, yéege ko. Kooku war na ànd ak nun, di seedeel ndekkitel Yeesu.»

1:23  Bi ko Piyeer waxee, ñu tudd ñaar: Yuusufa, mi ñu dippee Barsabas te di ko dàkkentale Yustus, moom ak Macas.

1:24  Ñu ñaan ci Yàlla ne: «Boroom bi, yaw mi xam xolu nit ñépp, won nu ki nga tànn ci ñaar ñii,

1:25  mu yenu liggéeyu nekk sa ndaw, wuutu Yudaa, mi ko bàyyi, dem bérabam.»

1:26  Noonu ñu boole leen, tegoo ay bant, bant ba dal ca Macas, mu fekki fukki ndaw ya ak benn.

2:1  Bi bésu màggalu Pàntakot agsee, ñoom ñépp booloo nañu ci benn bérab.

2:2  Ca saa sa riir jollee asamaan, mel ni ngelaw lu gaaw te bare doole, daldi fees dell kër, ga ñu toog.

2:3  Te ay làmmiñ yu mel ni safara feeñu leen, ñu tasaaroo ci seen biir, toŋ ca kaw kenn ku nekk.

2:4  Noonu ñu fees ak Xel mu Sell mi ñoom ñépp, ñu daldi wax yeneeni làkk, ni leen Xel mu Sell mi maye, ñu wax ko.

2:5  Fekk booba amoon na ay Yawut yu daloon Yerusalem, doon ay nit ñu ragal Yàlla te bokk ci xeeti àddina yépp.

2:6  Bi nit ñi déggee riir ma nag, ñépp dajaloo, daldi waaru ci li ñu leen dégg, ñuy wax ku nekk sa làkk.

2:7  Ñu waaru te yéemu naa: «Gisleen, ñiy wax ñépp, ndax duñu waa diiwaanu Galile?

2:8  Naka la man a ame nag, nu di leen dégg, kenn ku nekk ci nun, ñuy wax ci sa làmmiñ, wi nga nàmp?

2:9  Nun ñi ay Pàrt, waa Medi ak waa Elam, nun ñi dëkk Mesopotami, réewu Yawut yi, Kapados, Pont ak Asi,

2:10  di waa Firisi, Pamfili, Misra ak weti Libi, yi dend ak Siren, nun ak gan ñi jóge Room,

2:11  Yawut yi ak ñi tuub ci yoonu Yawut yi, waa Kereet ak Araab yi, nun ñépp nu ngi leen di dégg, ñuy yégle màggaayi Yàlla ci sunuy làkk!»

2:12  Noonu ñépp waaru, ba jaaxle lool, ñuy waxante ci seen biir ne: «Lii lu muy tekki?»

2:13  Waaye ñenn ñi di leen ñaawal ne: «Waay! ñii dañoo màndi ak biiñ.»

2:14  Ci kaw loolu Piyeer taxaw, ànd ak fukki ndaw ya ak benn, mu wax ci kaw, di yégal mbooloo ma ne: «Bokki Yawut yi ak yéen ñépp ñi dëkk Yerusalem, dégluleen bu baax te xam lii ma leen di wax!

2:15  Nit ñii màndiwuñu, ci ni ngeen ko fooge, ndaxte nu ngi ci yoor-yoor rekk.

2:16  Waaye lii mooy li Yàlla waxoon, jaarale ko ci yonentam Yowel ne:

2:17  “Yàlla nee na: Ci bés yu mujj yi,dinaa tuur ci sama Xel ci kaw nit ñépp;seen xeet wu góor ak wu jigéendinañu wax ci kàddug Yàlla;waxambaane yi dinañu gis ay peeñute màggat yi di gént ay gént.

2:18  Waaw ci bés yooyu dinaa tuur ci sama Xelci sama kaw jaam yu góor ak yu jigéen,te dinañu wax ci kàddug Yàlla.

2:19  Dinaa wone ay kéemaan ci kaw ci asamaanak ay firnde ci suuf ci àddina,muy deret, safara ak ay niiri saxar.

2:20  Jant bi dina daldi lëndëm,weer wi deretal,bala bésu Boroom biy ñëw,di bés bu mag, bi ànd ak ndam.

2:21  Booba nag ku woo Boroom bi ci aw turam,dinga mucc.”

2:22  «Yéen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu mi dëkk Nasaret, nit la woon, ku Yàlla dëggal ci seen kanam ciy kéemaan, ay jaloore ak firnde, ya Yàlla defoon jaarale ko ci moom ci seen biir; yéen xam ngeen ko.

2:23  Moom nag jébbale nañu ko, jaar ci nas, bi Yàlla dogaloon te xam ko lu jiitu; te yéen rey ngeen ko ci daaj ko ci bant, jaarale ko ci loxoy bàkkaarkat.

2:24  Waaye Yàlla dekkal na ko, daggal ko buumi dee, ndaxte dee mënu koo téye.

2:25  Daawuda wax na ci mbiram ne:“Saa su ne gis naa Boroom bi ci sama kanam,gannaaw mu ngi ci sama ndeyjoor,kon duma raf.

2:26  Moo tax sama xol sedd,may woy sama bànneex,te it sama yaram di tëdd ci yaakaar.

2:27  Ndaxte doo bàyyi sama ruu ci barsàq,te doo seetaan sa waa ju sell, mu yàqu.

2:28  Xamal nga ma yoonu dund;dinga ma béglooji ci sa kanam.”

2:29  «Bokk yi, man naa leen a wax lu wóor ci mbirum maam Daawuda, ne dee na te suul nañu ko; bàmmeelam mu ngi ci nun ba tey.

2:30  Waaye yonent la woon, te xamoon na ne, Yàlla digoon na ko ci ngiñ ne, dina teg ci nguuram kenn ci askanam.

2:31  Kon gis na lu ñëwagul, di wax ci mbirum ndekkitel Kirist ne, bàyyiwuñu ko ci barsàq, te yaramam yàquwul.

2:32  Yeesu moomu nag, Yàlla dekkal na ko; nun ñépp seede nanu ko.

2:33  Yàlla yéege na ko ak ndeyjooram, te jot na ci Baay bi Xel mu Sell mi ñu dige woon, ba tuur lii ngeen gis te dégg ko.

2:34  Ndaxte du Daawudaa yéeg ci asamaan, waaye moom ci boppam nee na:“Boroom bi wax na sama Boroom:‘Toogal ci sama ndeyjoor,

2:35  ba kera may daaneelsay noon ci sa kanam.’ ”

2:36  «Na bànni Israyil gépp xam bu wóor nag ne, Yeesu moomu ngeen daajoon ci bant, Yàlla def na ko Boroom ak Almasi bi.»

2:37  Bi ko mbooloo ma déggee, naqaru xol wu metti jàpp leen; ñu daldi ne Piyeer ak ndaw ya ca des: «Bokk yi, lu nu war a def?»

2:38  Piyeer tontu leen ne: «Tuubleen seeni bàkkaar, te kenn ku nekk ci yéen, ñu sóob ko ci ndox ci turu Yeesu Kirist. Noonu Yàlla dina leen baal seeni bàkkaar te may leen Xel mu Sell mi.

2:39  Ndaxte li Yàlla dige woon, yéena ko moom ak seeni doom ak ñu sore ñépp, di ñépp ñi Yàlla sunu Boroom di woo ci moom.»

2:40  Noonu mu artu leen ak yeneen wax yu bare, di leen dénk ne: «Rëccleen ci niti jamono ju dëng jii.»

2:41  Ñi nangu ay waxam nag, ñu sóob leen ci ndox, te ca bés booba lu mat limub ñetti junniy nit yokku nañu ci ñoom.

2:42  Ñoom nag ñuy wéy ci njàngalem ndaw yi ak cig bokk, ci damm mburu ak ñaan ci Yàlla.

2:43  Ragal jàpp ñépp, te ndaw yi di def ay kéemaan ak ay firnde yu bare.

2:44  Ñi gëm nag dañoo booloo te bokk lépp.

2:45  Ñu jaay seeni suuf ak seen alal, séddoo ko, ku nekk ak la ngay soxla.

2:46  Te bés bu nekk ñu saxoo teew ak benn xalaat ca kër Yàlla ga, tey damm mburu ca kër ya; ñuy lekk seen ñam ak xol bu laab tey bég,

2:47  di màggal Yàlla te am yiw ci wetu nit ñépp. Noonu bés bu nekk Boroom bi di yokk ca mbooloo ma ñi mucc.

3:1  Am bés Piyeer ak Yowaana dem, ba bëgg a dugg ca kër Yàlla ga ca waxtuw ñaan, maanaam tisbaar.

3:2  Fekk ñu indi fa nit ku judduwaale lafañ, ñu di ko teg bés bu nekk ca bunt, ba ñuy wooye Bunt bu rafet ba, ca kër Yàlla ga, ngir muy yelwaan ña fay dugg.

3:3  Bi mu gisee Piyeer ak Yowaana nag, ñuy dugg ca kër Yàlla ga, mu dékk leen loxo.

3:4  Ci kaw loolu Piyeer ak Yowaana ne ko jàkk, te Piyeer ne ko: «Xool nu.»

3:5  Lafañ bi xool leen, yaakaar ne dina jot dara ci ñoom.

3:6  Noonu Piyeer ne ko: «Awma xaalis, awma wurus, waaye li ma am, dinaa la ko jox: ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret doxal!»

3:7  Mu jàpp ci loxol ndeyjooram, yékkati ko. Ci saa si ay tànkam ak ay kostanam dëgër.

3:8  Mu tëb, daldi taxaw, di dox. Mu dugg ak ñoom ca kër Yàlla ga, muy dox, di tëb tey sant Yàlla.

3:9  Noonu ñépp gis ko, muy dox, di sant Yàlla.

3:10  Te ñu xàmmi ko, ne moo daan toog, di yelwaan ca Bunt bu rafet ba ca kër Yàlla ga. Ñu daldi waaru lool te yéemu ci li ko dikkal.

3:11  Naka waa ji taq ci Piyeer ak Yowaana, ñépp waaru; ñu daldi daw, fekksi leen ca bérab ba ñuy wax Werandaa bu Suleymaan.

3:12  Bi Piyeer gisee loolu nag, mu ne mbooloo mi: «Yéen waa Israyil, lu tax ngeen waaru ci lii? Lu tax ngeen di nu xool jàkk, mel ni ci sunu kàttan, mbaa ci sunu ragal Yàlla lanu doxloo kii?

3:13  Yàllay Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba, di Yàllay sunuy maam, màggal na Ndawam Yeesu; yéena xàcceek moom, ba jébbal ko Pilaat, fekk naroon na koo bàyyi.

3:14  Yéen xeeb ngeen Aji Sell ji te Jub, te tinul ab reykat.

3:15  Bóom ngeen Aji Dundal ji, waaye Yàlla dekkal na ko; seede nanu ko nun ñépp.

3:16  Ci gëm turam la nit, kii ngeen di gis te xam ko, dëgëre; waaw, turu Yeesu ak ngëm gi jóge ci moom, moo tax mu wér peŋŋ ci seen kanam, yéen ñépp.

3:17  «Léegi nag bokk yi, xam naa ne, ñàkka xam a tax ngeen def ko, yéen ak seeni kilifa.

3:18  Waaye noonu la Yàlla amale li mu yégle woon lu jiitu jaarale ko ci gémmiñug yonent yépp naan, Almaseem dina sonn.

3:19  Tuubleen seeni bàkkaar nag te woññiku ci Yàlla, ngir seeni bàkkaar far.

3:20  Noonu jamonoy péex dina bawoo ci Boroom bi, te muy yebal Almasi bi mu leen jagleel, maanaam Yeesu.

3:21  Asamaan war na koo yor, ba jamono ju ñuy defaraat lépp, di jamono ji Yàlla waxoon jaarale ko ci gémmiñug yonentam yu sell yépp, li dale ci njàlbéenug àddina.

3:22  Ndaxte Musaa nee woon na: “Boroom bi seen Yàlla dina leen feeñalal ci seen xeet Yonent ni man; nangeen ko déggal ci lépp lu mu leen wax.

3:23  Képp ku déggalul Yonent boobu, dees na la far ci xeet wi.”

3:24  «Li dale sax ci Samwil ak ñi ci topp, bépp yonent bu wax yégle na bés yii.

3:25  Yéen nag yéenay donn yonent yi ak kóllëre, gi Yàlla fasoon ak seeni maam, bi mu naan Ibraayma: “Xeeti àddina yépp dinañu barkeel ci ki soqikoo ci yaw.”

3:26  Yàlla feeñal na Ndawam, jëkk koo yebal ci yéen, ngir barkeel leen, ci woññi leen kenn ku nekk ci say bàkkaar.»

4:1  Bi ñuy wax ak mbooloo ma, saraxalekat ya ak kilifag ñiy wottu kër Yàlla ga ak Sadusen ya daanu ci seen kaw.

4:2  Ñu mer lool ci li ñuy waar nit ñi, di yégle ndekkitel ñi dee, sukkandikoo ko ci ndekkitel Yeesu.

4:3  Noonu ñu jàpp leen, tëj leen ba ca ëllëg sa, ndaxte mu nga doon tàmbalee guddi.

4:4  Waaye ñu bare ca ña dégg wax ja gëm nañu, te limu góor ñi gëm yokku na, ba mat juróomi junni.

4:5  Ca ëllëg sa nag kilifay Yawut yi ak njiit yi ak xutbakat yi dajaloo ci Yerusalem.

4:6  Ràññe nañu ci: Anas, miy saraxalekat bu mag bi, Kayif, Yowaana, Alegsàndar ak bokki saraxalekat bu mag bi.

4:7  Ñu dëj Piyeer ak Yowaana ca digg ba, laaj leen ne: «Lii ngeen def, ci gan kàttan, mbaa ci turu kan, ngeen ko defe?»

4:8  Ci kaw loolu Piyeer daldi fees ak Xel mu Sell mi, ne leen: «Yéen kilifay xeet wi ak njiit yi,

4:9  bu fekkee ne xettali nit ku wopp, ba mu wér, moo tax ngeen dëj nu ci pénc mi tey,

4:10  nangeen xam lii, yéen ñépp ak bànni Israyil gépp! Ci turu Yeesu Kirist mu Nasaret, mi ngeen daajoon ca bant te Yàlla dekkal ko, ci tur woowu la nit kii jële ag wér, ba taxaw ci seen kanam.

4:11  Yeesu moomu mooy:“Doj wi ngeen xeeboon, yéen tabaxkat yi,te moo doon doju koñ.”

4:12  Te mucc amul ci keneen, ndaxte ci ron asamaan amul weneen tur wu ñu maye ci nit ñi, wu nu war a mucce.»

4:13  Kon bi ñu gisee fit, wi Piyeer ak Yowaana àndal, te ñu xam ne, musuñoo jàng mbaa ñuy gëstu ci diine, ñu daldi waaru, ràññee ne, daa nañu ànd ak Yeesu.

4:14  Te bi ñu gisee nit, ka ñu fajoon, taxaw ak ñoom, mënuñu caa teg dara.

4:15  Noonu ñu santaane, ñu génne leen, ñu daldi gise ci seen biir,

4:16  ne: «Lu nuy def ak ñii? Ndaxte def nañu kéemaan gu siiw; loolu leer na ñi dëkk Yerusalem ñépp, te mënunu koo weddi.

4:17  Waaye ngir mbir mi bañ a law ci xeet wi, nanu leen aaye, ñu bañ a waxati ak kenn ci tur woowu.»

4:18  Noonu ñu woo leen, ñu tere leen bu wóor, ñu waxati mbaa waare dara ci turu Yeesu.

4:19  Waaye Piyeer ak Yowaana tontu leen ne: «Bu fekkee ne déggal leen te bàyyi Yàlla moo jub ci kanam Yàlla, seetleen ko.

4:20  Waaye nun mënunoo bañ a wax li nu gis te dégg ko.»

4:21  Noonu kilifa yi tëkkuwaat leen, yiwi leen, ñu dem. Ndaxte amuñu benn bunt ci ñoom ngir mbugal leen, fekk ñépp di màggal Yàlla ci li xewoon.

4:22  Ndaxte nit, ka ñu fajoon ci kéemaan googu, weesoon na ñeent-fukki at.

4:23  Bi ñu leen yiwee nag, ñu dem ci seeni bokk, nettali leen li saraxalekat yu mag ya ak njiit ya waxoon lépp.

4:24  Bi ko bokk ya déggee nag, ñu mànkoo, diis seen kàddu Yàlla ne: «Boroom bi, yaa sàkk asamaan, suuf, géej ak lépp li nekk ci seen biir.

4:25  Yaa wax, jaar ci sunu maam Daawuda sa jaam, mi doon gémmiñu Xel mu Sell mi, ne:“Lu tax xeeti àddina di bax?Lu tax ñuy fexe lu mënul a am?

4:26  Buuri àddina dañoo booloo,te kilifa yi dajaloo,di bañ Boroom bi ak Almaseem.”

4:27  Ndaxte ci dëgg ci dëkk bii, Erodd ak Poñsë Pilaat ànd ak xeeti àddina ak bànni Israyil, likkoo nañu, ngir daaneel sa Ndaw lu sell li nga fal, di Yeesu,

4:28  te def lépp, li sa kàttan ak sa ndigal tëraloon.

4:29  Léegi nag Boroom bi, seetal seeni tëkku te may say jaam, nuy wax sa kàddu ak fit.

4:30  Tàllalal sa loxo, ci wéral ak ci wone ay kéemaan ak ay firnde, jaarale ko ci turu Yeesu, sa Ndaw lu sell li.»

4:31  Bi ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu booloo woon daldi yengatu; te ñoom ñépp fees ak Xel mu Sell mi, ñuy wax kàddug Yàlla ak fit wu dëgër.

4:32  Noonu mbooloom ñu gëm ñi bokk menn xel ak benn xalaat. Kenn daawul aakimoo dara ci alalam, waaye ñoo bokkoon lépp.

4:33  Te ndaw yi di seedeel ndekkitel Yeesu Boroom bi ak kàttan gu réy. Te yiw wu yaatu ëmb leen, ñoom ñépp.

4:34  Kenn ci ñoom ñàkkul dara, ndaxte képp ku nekk boroom suuf mbaa am ay kër, jaay na ko, indi njëg gi,

4:35  teg ko ci loxoy ndaw ya; ñu di ci sédd, kenn ku nekk li mu soxla.

4:36  Noonu amoon na fa ku tudd Yuusufa, te ndaw yi dàkkentale ko Barnabas, miy tekki «Kiy dëgëral fit yi,» mu soqikoo ci giiru Lewi, te juddoo dunu Sipar.

4:37  Moom nag jaay na tool, ba mu moom, indi xaalis ba, teg ko ci loxoy ndaw ya.

5:1  Naka noonu nit ku tudd Anañas, ànd ak Safira jabaram, jaay làccu suuf.

5:2  Mu dencal boppam benn cér ca njëg ga, ànd ca ak jabaram; ba noppi mu indi cér ba ca des, teg ko ci loxoy ndaw ya.

5:3  Bi mu ko defee Piyeer ne ko: «Anañas, lu tax nga bàyyi Seytaane dugg la, ba fees sa xol, ngay wor Xel mu Sell mi, ci li nga dencal sa bopp benn cér ci njëg gi?

5:4  Bi mu jaragul, ndax moomuloo ko woon? Te bi mu jaree, ndax yilifuloo woon njëg gi? Lu tax nga fas ci sa xol def nii? Woruloo nit ñi, waaye Yàlla nga wor.»

5:5  Bi Anañas déggee baat yooyu, mu daanu dee. Ñi ko dégg ñépp tiit, ba ne nërëm.

5:6  Noonu waxambaane ya jóg, ñu sàng ko, yóbbu ko, jébbal Yàlla.

5:7  Ñetti waxtu gannaaw ga, jabaram duggsi, fekk xamul la fa xew.

5:8  Piyeer daldi ko ne: «Wax ma, ndax lii mooy njëgu tool bi?» Mu tontu ko: «Waawaaw, lii la.»

5:9  Ci kaw loolu Piyeer ne ko: «Lu tax ngeen ànd, di diiŋat Xelu Boroom bi? Ñi denci woon sa jëkkër ñu ngi nii ci bunt bi, te dinañu la yóbbu.»

5:10  Ca saa sa mu daanu ciy tànkam dee. Bi waxambaane ya agsee nag, ñu fekk ko, mu faatu; ñu yóbbu ko, def ko ci wetu jëkkëram.

5:11  Noonu tiitaange ju mag tàbbi ci mbooloom ñi gëm ñépp ak ñi ko dégg ñépp.

5:12  Bi loolu amee ay kéemaan ak ay firnde yu bare di xew ci nit ñi, jaare ca loxoy ndaw ya. Ñépp di booloo ca Werandaa bu Suleymaan ca kër Yàlla ga.

5:13  Te kenn ci ña ca des ñemewul a booloo ak ñoom, waaye nit ñépp di leen màggal.

5:14  Moona ay nit ñu gën a bare, góor ak jigéen, di gëm Boroom bi, tey taq ci ñoom.

5:15  Nit ñi indi sax ñu wopp ca mbedd ya, teg leen ca ay lal yu ndaw ak ay leeso, ngir bu Piyeer di jaar, doonte takkandeeram sax yiir ñenn ci ñoom.

5:16  Te it nit ñu bare dajaloo, jóge ca dëkk ya wër Yerusalem, ñu indi ay jarag ak ñu rab yu bon sadd; te ñoom ñépp daldi wér.

5:17  Booba saraxalekat bu mag ba jóg ak gàngooram gépp, maanaam kureelu Sadusen, ga fa dëkk. Kiñaan gu mag jàpp leen,

5:18  ba ñu jàpp ndaw ya, tëj leen ca kaso ba.

5:19  Waaye ci guddi malaakam Boroom bi ubbi buntu kaso ba, génne leen ci biti naan:

5:20  «Demleen taxaw ca kër Yàlla ga, te xamal nit ñi lépp lu jëm ci dund gu wóor gii.»

5:21  Bi ñu déggee loolu, ñu dugg ca kër Yàlla ga ci suba teel, daldi waare. Bi ñu koy def, saraxalekat bu mag ba ak gàngooram ñëw, woolu kureelu àttekat ya, maanaam mbooloom njiiti bànni Israyil gépp; ñu yónnee, ngir jëli ndaw ya ca kaso ba.

5:22  Waaye bi wottukati kër Yàlla ga agsee ca kaso ba, gisuñu leen fa; ñu daldi dellusi, yégle ko

5:23  ne: «Fekk nanu kaso ba tëju bu wóor ak wottukat ya taxaw ca bunt ya, waaye bi nu ko tijjee, fekkunu kenn ci biir.»

5:24  Bi kilifag wottukati kër Yàlla ga ak saraxalekat yu mag ya déggee loolu, ñu daldi ciy jaaxle lool, ñuy laajante, fu lii di mujj.

5:25  Noonu benn waay ñëw, yégal leen ne: «Nit ñi ngeen tëjoon ñu ngi taxaw ca kër Yàlla ga, di jàngal nit ñi.»

5:26  Ci kaw loolu kilifa ga ak wottukat ya dem jëli leen; waaye boolewuñu ci fitna, ngir ragal nit ñi sànni leen ay xeer.

5:27  Bi ñu leen indee, ñu dëj leen ci kanamu mbooloo ma. Saraxalekat bu mag ba laaj leen

5:28  ne: «Ndax terewunu leen ci lu wér, ngeen waare ci tur woowu, te fi mu ne dajal ngeen Yerusalem ak seeni waare, rax-ca-dolli yéena ngi nuy fexee taqal deretu nit kooku.»

5:29  Waaye Piyeer ak ndaw ya tontu leen ne: «Déggal Yàlla moo gën déggal nit.

5:30  Yàllay sunuy maam dekkal na Yeesu, mi ngeen bóomoon ci wékk ko ca bant ba.

5:31  Te Yàlla yékkati na ko ci ndeyjooram, mu nekk Buur ak Musalkat, ngir may bànni Israyil réccu, ba mu baal leen seeni bàkkaar.

5:32  Seede nanu loolu, nun ak Xel mu Sell, mi Yàlla may ñi koy déggal.»

5:33  Bi ñu déggee loolu, ñu mer ba seen xol di dagg, ñu bëgg leen a rey.

5:34  Waaye amoon na fa nit ku tudd Gamaleel, bokk ci tariixab Farisen ya, di xutbakat bu tedd ci yoonu Musaa, mu jóg ca mbooloo ma, santaane ñu génne leen tuuti.

5:35  Bi ñu ko defee mu ne leen: «Yéen bokki Israyil, moytuleen li ngeen di def nit ñooñu.

5:36  Ndaxte bu yàggul Tëdas jógoon na, mbubboo daraja, ba lu mat ñeenti téeméeri nit takktoo ak moom. Tëdas moomu nag reyees na ko, te ñi ko toppoon ñépp tasaaroo, ba seen pexe nasax.

5:37  Gannaawam it Yudaa mu Galile jóg, ca jamono ja ñu doon bind waa réew ma, mu jógloo nit ñu bare, ñu ànd ak moom. Moom itam dee na, te ay nitam ñépp tasaaroo.

5:38  Léegi maa ngi leen di wax, génnleen ci mbirum ñooñu te bàyyi leen ñu dem. Ndaxte bu seen pas-pas mbaa seen jëf dee pexem nit, dina yàqu.

5:39  Waaye bu fekkee ne ndogalu Yàlla la, dungeen ko man a fanq, ngir ragal a jànkoonte ak Yàlla.»

5:40  Bi mu waxee loolu, ñu fekk ko ci xalaatam; ñu woo ndaw ya, daldi leen dóor ay yar, tere leen, ñu waxati dara ci turu Yeesu, ba noppi bàyyi leen, ñu dem.

5:41  Ndaw ya nag jóge ca kanam kureelu àttekat ya, bég ci li leen Yàlla jàppe, ñu yeyoo yenu toroxte ngir Tur wa.

5:42  Noonu bés bu nekk ca kër Yàlla ga ak ca kër ya, daawuñu noppee jàngale ak a xamle xebaar bu baax bi, ne Yeesu mooy Almasi bi.

6:1  Ca bés yooyu, naka taalibe yi di gën a bare, Yawut yiy làkk gereg tàmbalee ñaxtu ci mbirum Yawut tigi yi, te lii a ko waral: jigéen ñi seen jëkkër dee, te ñu bokk ci ñoom, naraalewuñu leen ca ndimbal, la ñuy séddale bés bu nekk.

6:2  Noonu fukki ndaw ya ak ñaar woo mbooloom taalibe ya ne leen: «Nu bàyyi kàddug Yàlla, di topptoo mbirum séddale, loolu jekkul ci nun.

6:3  Kon nag bokk yi, tànnleen juróom-ñaari nit ci seen biir, ñu am seede su rafet te fees ak Xel mu Sell mi ak sago, nu dénk leen liggéey bii.

6:4  Waaye nun dinanu wéy ci ñaan ci Yàlla ak ci yenub xamle kàddu gi.»

6:5  Lii ñu wax nag neex na mbooloo mépp. Noonu ñu tànn Ecen, di nit ku fees ak ngëm ak Xel mu Sell mi, boole ci Filib ak Porokor, teg ca Nikanor, Timon, Parmenas ak Nikolas, mi juddoo Ancos te tuub ci yoonu Yawut ya.

6:6  Ñu jébbal leen ndaw ya, ñaanal leen, teg leen loxo.

6:7  Noonu kàddug Yàlla di law, ba mbooloom taalibe yi di yokku bu bare ci Yerusalem; te saraxalekat yu bare déggal Yàlla ci topp yoonu ngëm wi.

6:8  Naka noona Ecen, mi fees ak yiw ak kàttan, di def ay kéemaan yu mag ak ay firnde ca nit ña.

6:9  Waaye ay nit jóg, bokk ci jàngu, bi ñuy wax Jàngub ñi ñu goreel, di ay niti dëkki Siren ak Alegsàndiri, ak it waa diiwaani Silisi ak Asi. Ñuy werante ak Ecen,

6:10  waaye àttanuñu sagoom ak Xel mi muy waxe.

6:11  Kon ñu daldi jënd ay nit, ñu ne: «Dégg nanu ko, muy sosal Musaa ak Yàlla.»

6:12  Noonu ñu jógloo nit ñi ak njiit yi ak xutbakat yi, ñu dal ci kawam, jàpp ko, yóbbu ko ca kureelu àttekat ya.

6:13  Te ñu sàkk ay naaféq yuy seede ne: «Kii du bàyyee wax lu juuyoo ak bérab bu sell ba ak yoonu Musaa.

6:14  Ndaxte dégg nanu, muy wax ne, Yeesum Nasaret moomu dina daaneel bérab bii te soppi aada, yi nu Musaa batale woon.»

6:15  Bi ñu ko waxee, ña toogoon ñépp ca mbooloo ma xool ko jàkk, gis xar-kanamam, mu mel ni xar-kanamu malaaka.

7:1  Noonu saraxalekat bu mag ba ne ko: «Ndax loolu dëgg la?»

7:2  Ecen tontu ko: «Yéen samay bokk ak samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom ndam, feeñu woon na sunu maam Ibraayma, bi mu nekkee réewu Mesopotami, te dëkkagul woon Karan.

7:3  Mu ne ko: “Toxul sa réew, bàyyi say bokk, te ñëw ci réew, mi ma lay won.”

7:4  «Ci kaw loolu mu génn réewu niti Kalde, dëkksi Karan. Te bi baayam faatoo, Yàlla toxale ko foofa, dëël ko ci réew, mi ngeen dëkk léegi.

7:5  Waaye mayu ko fa genn moomeel gu mu war a donnale, du sax fu mu man a teg tànkam; waaye dig na ko ne, dina ko may réew mi, mu yilif ko moom ak askanam, fekk booba amagul doom.

7:6  Yàlla ne ko: “Ñi soqikoo ci yaw dinañu ganeyaan ci réew mu ñu dëkkul; dees na leen def ay jaam, di leen fitnaal diirub ñeenti téeméeri at.”

7:7  Waaye Yàlla nee na: “Xeet wi leen jaamloo, man maa leen di àtte te gannaaw loolu dinañu génn, di ma jaamu ci bérab bii.”

7:8  Yàlla nag tëral kóllëre seen diggante, fas ko ci màndargam xaraf. Noonu Ibraayma jur Isaaxa, xarafal ko ca juróom-ñetteelu fan ba; Isaaxa def noonu Yanqóoba, Yanqóoba it def noonu fukki maam ya ak ñaar, ñi sos xeet wi.

7:9  «Naka maam yooyu, dañoo iñaane Yuusufa, ba jaay ko, mu jëm réewu Misra. Waaye Yàlla taxawu ko,

7:10  génne ko ci coonoom yépp, defal ko yiw ak xel ci kanamu Firawna, buuru Misra, mu def ko kilifag Misra ak këram gépp.

7:11  «Bi loolu amee xiif tàbbi ci biir Misra ak réewu Kanaan mépp, ba toskare ja metti lool, te sunuy maam amatuñu lu ñu lekk.

7:12  Yanqóoba nag dégg ne, Misra am na dugub, mu yebal ca sunuy maam, ñu dem fa yoon wu jëkk.

7:13  Bi fa ay doomi baayam delloo nag, Yuusufa xàmmiku leen, te Firawna xamante ak njabootam.

7:14  Ci kaw loolu Yuusufa yeble, woo baayam ak mbokkam yépp, ñuy juróom-ñaar-fukki nit ak juróom.

7:15  Noonu Yanqóoba dem Misra, faatu fa, moom ak sunuy maam.

7:16  Gannaaw loolu ñu yóbbu seeni néew Sikem, dugal leen ca bàmmeel, ba Ibraayma jëndoon ak xaalis ca doomi Emor ca Sikem.

7:17  «Bi loolu wéyee jamono ji jege woon na, ngir Yàlla amal li mu digoon Ibraayma ci ngiñ; fekk xeet wa di law tey gën a bare ci Misra,

7:18  ba keroog beneen buur bu xamul Yuusufa di falu ci Misra.

7:19  Buur boobu nag dafa daan nax sunu xeet, di fitnaal sunuy maam, ba di leen sànniloo seeni doom, ngir ñu dee.

7:20  «Booba nag la Musaa juddu, di ku rafet ci kanam Yàlla; ñu yor ko ñetti weer ci biir kër baayam,

7:21  ba noppi sànni ko. Noonu doom ju jigéen ju Firawna for ko, yar ko ni doomam.

7:22  Musaa nag di ku yeewu ci xam-xamu waa Misra bépp, di jàmbaar ci wax ak jëf.

7:23  «Bi mu demee ba am ñeent-fukki at, mu fas yéeney seeti ay bokkam, maanaam bànni Israyil.

7:24  Noonu mu gis ca ku ñuy néewal doole, mu sotle ko, feyyul ko, ba dóor waayi Misra ja.

7:25  Mu defe ne, ay bokkam dinañu xam ne, ciy loxoom la leen Yàllay musale, waaye xamuñu ko.

7:26  Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, mu di leen jéem a jubale ne leen: “Yéen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di xeex?”

7:27  Waaye kiy néewal doole moroomam bëmëx ko ne: “Ku la teg kilifa ak àttekat ci sunu kaw?

7:28  Ndax danga maa bëgg a rey, ni nga defoon démb waayi Misra ja?”

7:29  Bi Musaa déggee wax jooju, mu daldi daw, dem réewu Majan, di fa ab doxandéem; mu séy fa, ba am ñaari doom.

7:30  «Lu ko wees ñeent-fukki at nag, bi mu nekkee ca màndiŋu tundu Sinayi, malaaka feeñu ko ci takk-takku safara ci biir as ngarab.

7:31  Bi ko Musaa gisee, mu daldi waaru ci li mu gis; mu jegesi ngir niir ko, dégg baatu Boroom bi ne ko:

7:32  “Man maay sa Yàllay maam, di Yàllay Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba.” Ci kaw loolu Musaa tiit bay lox, te ñemeetul a xool.

7:33  Noonu Boroom bi ne ko: “Summil say dàll, ndaxte bérab bi nga taxaw, bérab bu sell la.

7:34  Gis naa bu baax fitnay sama xeet ci Misra te dégg naa seeni tawat, kon wàcc naa ngir musal leen. Léegi nag ñëwal, dinaa la yebal Misra.”

7:35  «Musaa moomu bañoon nañu ko, ba ne ko: “Ku la teg kilifa ak àttekat?” Waaye moom la Yàlla yebal, jaarale ko ci malaaka mi ko feeñu ca ngarab sa, ngir mu nekk kilifa gu leen di goreel.

7:36  Moo leen génne réewu Misra, di def ay kéemaan ak ay firnde ca réew ma, ca Géej gu xonq ga ak ca màndiŋ ma diirub ñeent-fukki at.

7:37  Musaa moomu moo ne woon bànni Israyil: “Yàlla dina leen feeñalal ci seeni bokk Yonent bu mel ni man.”

7:38  Te moo nekkoon ak mbooloo ma ca màndiŋ ma, ànd ak sunuy maam, wéttalikoo malaaka, mi waxoon ak moom ci tundu Sinayi. Te mu jote ci Yàlla kàddu yiy dund, ngir jottali nu ko.

7:39  Waaye sunuy maam nanguwuñu koo déggal; dañu koo bañ te seeni xel dëpp, dellu Misra.

7:40  Ñu sant Aaroona ne: “Sàkkal nu ay yàlla yuy jiitu ci sunu kanam, ndaxte Musaa male nu génne ci réewu Misra, xamunu lu ko dal.”

7:41  Booba nag ñu tëgglu aw sëllu, muy xërëm, ñu di ko tuuru, di bànneexu ci seeni jëfi loxo.

7:42  Waaye bi ñu ko defee Yàlla dëddu leen, bërgël leen, ñuy jaamu biddiiwi asamaan. Moom lañu bind ci téereb yonent yi ne:“Yéen bànni Israyil, ndax rendi ngeen jur,jébbal ma, boole ko ak i sarax,diirub ñeent-fukki at ca màndiŋ ma?

7:43  Yóbbu ngeen sax fu nekk tànt,biy màggalukaayu Molog ak biddiiwub Refan,bi ñu daan bokkaaleel Yàlla,di ay nataal, yi ngeen defoon ngir màggal leen!Kon nag dinaa leen toxal,yóbbu leen ci gannaaw réewu Babilon.”

7:44  «Sunuy maam amoon nañu ca màndiŋ ma tàntu màggalukaay, bi ëmboon li Yàlla seede. Tànt boobu nag defoon nañu ko, roye ko ci bi Musaa gisoon, ni ko ko Yàlla sante woon.

7:45  Te gannaaw ga, bi Yosuwe nekkee kilifag sunuy maam, ñu jot tànt ba ñoom it, yóbbu ko ca réew, ma ñu nangu ca xeet ya Yàlla dàq ci seen kanam. Tànt ba nekk fa, ba ci jamonoy Daawuda.

7:46  Moom yiw na fa kanam Yàlla, mu ñaan ko, mu sàkkal ko kër ngir askanu Yanqóoba.

7:47  Waaye Suleymaan moo tabaxal Yàlla kër ga.

7:48  «Moona Aji Kawe ji du dëkk ci fu loxol nit defar; moom la ab yonent wax ne:

7:49  “Asamaan mooy sama jal,te suuf mooy sama tegukaayu tànk.Kon gan kër ngeen may tabaxal,mbaa fan mooy sama bérabu noppalukaay?

7:50  Ndax du sama loxo moo defar yëf yooyu yépp?— Moom la Boroom bi doon wax.”

7:51  «Yéen ñi dëgër bopp, ànd ak xol buy bañ ak ay nopp yuy fatt, mel ni ñi xamul Yàlla. Dungeen noppeek a diiroo ak Xel mu Sell mi; ni ko seen baay yi daan defe, noonu ngeen di def yéen itam.

7:52  Kan ca yonent ya la seeni maam tegul woon ay fitna? Rey nañu ñi doon yégle ñëwug Aji Jub ji, moom mi ngeen jébbale léegi, ba ñu rey ko.

7:53  Jot ngeen yoonu Musaa, wi Yàlla wàcce jaarale ko ci ay malaaka, te sàggane ngeen ko.»

7:54  Bi ñu déggee loolu nag, seeni xol di dagg, ñuy yéyu, jëm ci kawam.

7:55  Waaye Ecen, mi fees ak Xel mu Sell mi, ne jàkk ci asamaan, gis ndamu Yàlla, te gis Yeesu mi taxaw ci ndeyjooru Yàlla.

7:56  Mu ne: «Seetleen, maa ngi gis asamaan yi ubbiku, te Doomu nit kaa ngii taxaw ci ndeyjooru Yàlla.»

7:57  Bi ñu déggee loolu, ñu daldi xaacu ca kaw, tey dar seeni nopp; ñu ànd, ne milib ci kawam;

7:58  ñu wat-wate ko, génne ko dëkk ba, dóor ko ay doj, ba mu dee. Seede ya tegoon nañu seeni yére ci tànki waxambaane wu tudd Sool.

7:59  Noonu ñu dóor Ecen ay doj, muy ñaan Yàlla ne: «Boroom bi Yeesu, nangul sama ruu!»

7:60  Bi mu ko waxee, mu sukk, wax ak baat bu kawe: «Boroom bi, bu leen bindal bàkkaar bii,» ba noppi mu nelaw.

8:1  Sool moom ànd na ci ñi doon rey Ecen. Bés booba nag fitna ju metti dal na ci mbooloom ñi gëm, mi nekk Yerusalem, ba ñépp, ñu moy ndaw ya, tasaaroo ci diiwaani Yude ak Samari.

8:2  Ay nit ñu ragal Yàlla fab Ecen, jébbal ko Boroom bi, di ko jooy bu wér.

8:3  Waaye naka Sool, mu ngay tas mbooloom ñi gëm, di tàbbi ca kër ya, tey jàpp góor ak jigéen, di leen tëj kaso.

8:4  Ñi tasaaroo nag dem fu nekk, di fa xamle xebaar bu baax bu kàddug Yàlla.

8:5  Naka Filib mu dem ca benn dëkk ca Samari, di leen yégal Kirist.

8:6  Bi ko mbooloo mi déggee te gis kéemaan yi muy def, ñu bokk benn xalaat, fekki ko ci li mu wax.

8:7  Ndaxte ay rab yu bon bàyyi nañu nit ñu bare, ña ñu jàppoon, di yuuxu ci kaw; te ñu bare ñu làggi ak ñu lafañ daldi wér.

8:8  Noonu mbég mu réy tàbbi ca dëkk ba.

8:9  Amoon na nag nit ku tudd Simoŋ, di luxuskat bu yàgg ca dëkk ba, te daan yéem waa Samari gépp, ci naan: «Aji Màgg laa.»

8:10  Kon ñépp, mag ak ndaw, taq ci moom ne: «Kii mooy jaasiy Aji Kàttan ji.»

8:11  Ñu taq ci moom, ndax li mu leen yàgg a waar ci ay luxus.

8:12  Waaye bi ñu gëmee xebaar bu baax, bi Filib yégle jëm ci nguurug Yàlla ak turu Yeesu Kirist, góor ak jigéen daldi nangu, ñu sóob leen ci ndox.

8:13  Simoŋ sax gëm, ñu sóob ko ci ndox; mu wéy nag ci topp Filib, di waaru ci kéemaan yi ak firnde yu mag yiy am.

8:14  Bi nga xamee ne ndaw yi nekk Yerusalem yég nañu ne, waa Samari nangu nañu kàddug Yàlla; ñu yónni fa Piyeer ak Yowaana.

8:15  Ñu dem fa nag, ñaanal leen, ngir ñu jot Xel mu Sell mi.

8:16  Ndaxte wàccagul ci kenn ci ñoom, waaye sóoboon nañu leen rekk ci ndox ci turu Boroom bi Yeesu.

8:17  Noonu Piyeer ak Yowaana teg leen loxo, ñu jot Xel mu Sell mi.

8:18  Bi Simoŋ gisee nag ne Yàlla may na Xel mi jaarale ko ci loxoy ndaw ya, mu indil leen xaalis,

8:19  ne leen: «Mayleen ma sañ-sañ boobu, ba ku ma teg samay loxo, nga jot Xel mu Sell mi.»

8:20  Waaye Piyeer ne ko: «Asarul ak sa xaalis, yaw mi yaakaar ne, man ngaa jënd mayu Yàlla ak xaalis.

8:21  Amuloo benn wàll mbaa cér ci lii, ndaxte sa xol laabul ci kanam Yàlla.

8:22  Réccul nag sa coxor te ñaan Boroom bi, mu baal la sa xalaatu xol, su manee am.

8:23  Ndaxte gis naa ne, sóobu nga ci lu wex xat ci kanam Yàlla, te bàkkaar noot na la.»

8:24  Simoŋ nag ne leen: «Ñaanal-leen ma ci Boroom bi, ngir mu fegal ma li ngeen wax.»

8:25  Noonu bi ñu seedeelee Yàlla te wax ci kàddoom, ñu dellu Yerusalem, di xamle xebaar bu baax bi ci dëkk yu bare yu waa Samari.

8:26  Naka noonu benn malaakam Boroom bi ne Filib: «Jógal te jublu Misra, jaar ci yoon wi jóge Yerusalem, jëm Gasa, di màndiŋ.»

8:27  Filib jóg dem. Noonu mu gis fa nitu Ecópi ku yoom, di jaraaf ju mag ci Kandas, buur bu jigéen bu Ecópi, te di ko wottul xaalisam bépp. Fekk mu ñëwoon Yerusalem, ngir màggalsi Yàlla, bay dellu;

8:28  mu toog ci watiiram, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi.

8:29  Xel mi nag ne Filib: «Dabal watiir wale.»

8:30  Noonu Filib dawsi, mu dégg waayi Ecópi ja, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi. Mu laaj ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?»

8:31  Mu tontu ko ne: «Nu ma ko man a xame, su ma ko kenn firilul?» Mu woo Filib nag, mu yéeg, toog ak moom.

8:32  Fekk aaya yii la doon jàng ci Mbind mi:«Yóbbu nañu ko ni xar mu ñuy rendiji;ni mburt mu luu ci kanami watkat,mu ne cell.

8:33  Ci toroxteem nangu nañu dëggam;ñi mu tollool jamono, ku ci xalaat lii?Jële nañu bakkanam ci àddina.»

8:34  Jaraaf ja nag ne Filib: «Maa ngi lay laaj, ci mbirum kan la yonent bi jëmale wax ji? Ndax mbirum boppam lay wax mbaa mu keneen?»

8:35  Noonu Filib tàmbali ci aaya yooyu, xamal ko xebaar bu baax bi ci mbirum Yeesu.

8:36  Bi ñuy jaar ci yoon wi, ñu agsi ci ndox. Jaraaf ja ne ko: «Ndox a ngi nii, ana lu tere, nga sóob ma ci?»

8:38  Mu santaane nag, ñu taxawal watiir wa; Filib ak jaraaf ja wàcc ñoom ñaar ci biir ndox ma, mu sóob ko ca.

8:39  Ba noppi ñu génn ca ndox ma, te ca saa sa Xelu Boroom bi fëkk Filib, ba jaraaf ja gisatu ko, waaye mu toppaat yoonam, ànd ak mbég.

8:40  Filib moom teeri dëkku Asot, muy jaar ci dëkk yépp, di fa xamle xebaar bu baax bi, ba kera muy ñëw dëkku Sesare.

9:1  Naka Sool, muy tëkkoo rey taalibey Boroom bi, ba di ko noyyee far. Mu dem nag ca saraxalekat bu mag ba,

9:2  laaj ko ay bataaxal yu muy yóbbul jànguy dëkku Damas. Noonu ñu mu fa fekk, te ñu bokk ci yoon wi, góor mbaa jigéen, mu am dogalu yeew leen, indi leen Yerusalem.

9:3  Waaye bi muy jub Damas, ca saa sa leer gu jóge asamaan melax, ba ëmb ko.

9:4  Mu daanu ci suuf, dégg baat bu ko ne: «Sool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal?»

9:5  Mu wuyu ne: «Yaay kan Boroom bi?» Boroom bi ne ko: «Maay Yeesu, mi ngay fitnaal.

9:6  Waaye jógal, dugg ca dëkk ba, te dinañu la wax li nga war a def.»

9:7  Nit ñi ànd ak moom nag taxaw, waaru ba luu, ci li ñu dégg baat bi te gisuñu kenn.

9:8  Noonu Sool jóg, xippi, waaye gisul dara; kon ñu wommat ko, yóbbu ko Damas.

9:9  Diirub ñetti fan gisul dara, lekkul, naanul.

9:10  Amoon na nag ci Damas taalibe bu tudd Anañas. Bi loolu amee nag Boroom bi feeñu ko ne: «Anañas!» Mu wuyu: «Maa ngi nii Boroom bi.»

9:11  Boroom bi ne ko: «Jógal, nga jaar ci mbedd, mi ñuy wax Mbedd mu jub mi, te seet ci kër Yudaa nit ku tudd Sool te dëkk Tars, ndaxte mu ngay ñaan.

9:12  Te gis na cim peeñu nit ku tudd Anañas, mu dugg, teg ko ay loxo, ba muy gisaat.»

9:13  Waaye Anañas tontu ko ne: «Boroom bi, dégg naa ci nit ñu bare ci mbirum kooku, ñu seede lu bare lu bon lu mu def say gaay ci Yerusalem.

9:14  Te indaale na fii sax sañ-sañ bu jóge ci saraxalekat yu mag ya, ngir yeew képp kuy tudd saw tur.»

9:15  Waaye Boroom bi ne ko: «Demal, ndaxte maa ko tànn, muy sama jëfandukaay, ngir yóbbu sama tur fa kanam ñi nekkul Yawut ak fa kanam buur yi ak bànni Israyil.

9:16  Te dinaa ko won coono yu bare yu mu war a dékku ngir sama tur.»

9:17  Ci kaw loolu Anañas dem, dugg ca kër ga, teg ay loxoom Sool. Mu ne ko: «Sool sama mbokk, Boroom bi Yeesu, mi la feeñu woon ci kaw yoon wi, bi ngay dikk, moo ma yónni, ngir nga dellu di gis te fees ak Xel mu Sell mi.»

9:18  Ca saa sa lu mel ni ay waasintoor génne ci ay bëtam, mu daldi gisaat. Noonu mu jóg, ñu sóob ko ci ndox;

9:19  ba noppi mu lekk, amaat doole. Bi mu ko defee mu toog ay fan ak taalibe, ya nekk Damas.

9:20  Ca saa sa muy yégle ca jàngu ya ne, Yeesu mooy Doomu Yàlla.

9:21  Ñi ko dégg ñépp waaru naan: «Ndax du kii moo daan tas ñiy tudd tur woowu ci Yerusalem, te mu ñëw fii, ngir yeew leen, yóbbu ci kanamu saraxalekat yu mag ya?»

9:22  Moona Sool di gën a am kàttan, bay jaaxal Yawut yi dëkk Damas, ci di leen wax ay firnde, ne Yeesu mooy Almasi bi.

9:23  Ba ñu ca tegee ay fani fan, Yawut yi daldi gise, ngir reylu ko.

9:24  Waaye Sool yég seen pexe. Fekk guddi ak bëccëg ñu doon wottu bunt yi yépp, ngir man koo bóom.

9:25  Noonu taalibe yi jël ko ci guddi, def ko ci dàmba gu réy, jaarale ko ci miir bi, yoor ko ci suuf.

9:26  Bi Sool agsee Yerusalem, mu jéem a ànd ak taalibe yi, waaye ñépp ragal ko, ndax gëmuñu woon ag taalibeem.

9:27  Ci kaw loolu Barnabas jël ko, yóbbu ko ca ndaw ya, nettali leen, ni Sool gise Boroom bi ci kaw yoon wi, ak li mu ko wax, rax-ca-dolli fit wi mu doon waxe ci turu Yeesu ci Damas.

9:28  Noonu mu nekk ak ñoom ci Yerusalem, di dugg ak a génn, di wax ak fit ci turu Boroom bi.

9:29  Muy wax ak di werante ak Yawut yiy làkk gereg, waaye ñu di ko wut a rey.

9:30  Bi ko bokk yi yégee nag, ñu yóbbu ko dëkku Sesare, yebal ko dëkku Tars.

9:31  Noonu mbooloom ñi gëm nekk ci jàmm ci biir diiwaani Yude gépp ak Galile ak Samari; ñuy gën a dëgër, di wéy ci ragal Yàlla, tey yokku ci ndimbalu Xel mu Sell mi.

9:32  Piyeer nag di wër, di jaar fu nekk, tey dem ci gaayi Yàlla yi dëkk Lidd,

9:33  mu gis fa nit ku làggi, tudd Ene, tëdd ci basaŋ diirub juróom-ñetti at.

9:34  Piyeer ne ko: «Ene, Yeesu Kirist faj na la; jógal te defar sa lal.» Noonu mu daldi jóg ca saa sa.

9:35  Bi ko waa diiwaani Lidd ak Saron gépp gisee, ñu daldi woññiku ci Boroom bi.

9:36  Amoon na nag ci dëkku Yope taalibe bu jigéen bu tudd Tabita, liy tekki «Dorkas,» maanaam «kewel,» te muy wéy ci jëf yu baax ak saraxe.

9:37  Ca fan yooyu mu daanu wopp, ba faatu; noonu ñu sang ko, teg ko ca néeg, ba sut ca taax ma.

9:38  Gannaaw Lidd sorewul ak Yope nag, te taalibe yi dégg ne, Piyeer a nga fa, ñu yónnee ko ñaari nit, ñaan ko mu ñëw ci ñoom ci saa si.

9:39  Bi ko Piyeer déggee, mu jóg, ànd ak ñoom. Bi mu ñëwee, ñu yóbbu ko ca néeg bu kawe ba. Fekk fa ay jigéen ñi seeni jëkkër faatu, ñu daldi wër Piyeer, ñépp di jooy, di ko won kamisool ya ak mbubb, ya Dorkas daan defar cig dundam.

9:40  Ci kaw loolu Piyeer génne ñépp ci biti, mu sukk, ñaan ci Yàlla, ba noppi walbatiku ca néew ba ne ko: «Tabita, jógal!» Noonu mu xippi, gis Piyeer, daldi toog.

9:41  Piyeer may ko loxo, yékkati ko. Mu woo gaayi Yàlla ya ak jigéen ña, won leen ko, muy dund.

9:42  Mbir ma siiw ca Yope gépp, ba ñu bare gëm Boroom bi.

9:43  Gannaaw loolu Piyeer toog ay fan ci Yope, ci këru ku tudd Simoŋ, miy wullikat.

10:1  Amoon na ci Sesare nit ku tudd Korney, nekk njiitu xare, mu bokk ci mbooloom xare, mi ñuy wax mu Itali.

10:2  Moom nag ku farlu woon ci Yàlla la, te ragal ko, moom ak waa këram gépp; muy sarax ñu bare ci bànni Israyil, tey saxoo ci ñaan ci Yàlla.

10:3  Am bés ci tisbaar nag mu am peeñu, gis bu leer malaakam Yàlla feeñu ko ne ko: «Korney!»

10:4  Noonu Korney ne ko jàkk, daldi tiit ne ko: «Kilifa gi, lu mu doon?» Malaaka ma ne ko: «Say ñaan ak say sarax yéeg na fa kanam Yàlla, te nangul na la.

10:5  Yónnil léegi nag ay nit ci dëkku Yope, ñu woo ku tudd Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer.

10:6  Mu nga dal fa Simoŋ wullikat, bi këram nekk ci wetu géej.»

10:7  Bi malaaka mi doon wax ak moom demee, Korney woo ñaar ci ay surgaam ak benn xarekat bu farlu ci Yàlla ci ñi koy topptoo;

10:8  mu nettali leen lépp, yebal leen Yope.

10:9  Ca ëllëg sa, ba ñuy jaar ca yoon wa, ba jub dëkk ba, Piyeer yéeg ca kaw taax ma ci digg-bëccëg ngir ñaan ci Yàlla.

10:10  Noonu xiif dab ko fa, mu bëgg a lekk. Waaye bi ñu koy toggal, Yàlla feeñu ko.

10:11  Mu xool asamaan ubbiku, gis lu mel ni sér bu mag bu ñu téye ci ñeenti laf ya, yoor ko, mu jëm suuf.

10:12  Boroom ñeenti tànk yépp ñu nga ca, ak yiy raam ci suuf, ak picci asamaan.

10:13  Te baat ne ko: «Jógal, Piyeer, rey te lekk.»

10:14  Waaye Piyeer tontu ko: «Mukk, Boroom bi, ndaxte musumaa lekk dara lu daganul mbaa lu araam.»

10:15  Waaye baat bi wax ak moom ñaareelu yoon ne ko: «Lu Yàlla sellal, bu ko araamal.»

10:16  Ñu def ko nag, ba muy ñetti yoon, ba noppi ñu ne cas sér ba, jëme asamaan.

10:17  Bi loolu amee Piyeer jaaxle lool ci lu peeñu miy tekki; fekk booba nit ñi Korney yebal, laajte woon nañu kër Simoŋ, ba agsi ci bunt bi.

10:18  Ñu woote nag naan: «Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer, ndax fi la dëkk?»

10:19  Bi Piyeer di rabal xelam ci peeñu ma, Xel mi ne ko: «Ñetti nit a ngi nii, di la wut.

10:20  Jógal, nga wàcc te ànd ak ñoom; bul werante, ndaxte maa leen yebal.»

10:21  Piyeer wàcc nag ne nit ñi: «Maa ngi nii, man mi ngeen di wut; lu doon seeni tànk?»

10:22  Ñu tontu ko: «Korney, njiitu xare ba, nit ku jub la te ragal Yàlla, ba am seede su rafet ci bànni Israyil gépp. Malaaka mu sell nag sant na ko, mu woolu la ci këram te déglu li ngay wax.»

10:23  Ci kaw loolu Piyeer dugal leen, dalal leen. Ba bët setee, Piyeer jóg, dem ak ñoom, ànd ak ñenn ci bokk yi dëkk Yope,

10:24  te bés ba ca topp mu dikk Sesare. Fekk Korney woo na këram ay bokkam ak i xaritam yi ko gën a jege, di xaar Piyeer.

10:25  Bi Piyeer duggee nag, Korney daje ak moom, daanu ciy tànkam, sargal ko.

10:26  Waaye Piyeer yékkati ko ne: «Jógal, man it nit rekk laa.»

10:27  Noonu muy waxtaan ak moom, duggsi, fekk fa ndajem nit ñu bare.

10:28  Mu ne leen: «Xam ngeen ne, aaye nañu Yawut, mu jaxasoo ak ku mu bokkalul xeet, mbaa mu dugg ci këram. Waaye Yàlla won na ma ne, warumaa ne kenn setul mbaa araam na.

10:29  Looloo tax, bi ngeen ma wooloo, ñëw naa ci lu àndul ak werante. Maa ngi leen di laaj nag, lu ngeen may doye?»

10:30  Ci kaw loolu Korney tontu ne: «Ñetti fan a ngii may ñaan ci sama biir kër ci waxtu wii, maanaam tisbaar. Ci saa si ku sol yére yuy melax taxaw ci sama kanam,

10:31  mu ne ma: “Korney, say ñaan nangu na, te say sarax egg nañu fa kanam Yàlla.

10:32  Yónneel nag ci Yope, woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer; mu nga dal ci kër Simoŋ miy wullikat ca wetu géej ga.”

10:33  Yónnee naa nag ci ni mu gën a gaawe, woolu la; te maa ngi lay sant ci li nga ñëw. Léegi nag nun ñépp nu ngi fi ci kanam Yàlla, ngir déglu lépp li la Boroom bi sant.»

10:34  Noonu Piyeer jël kàddu ga ne leen: «Ci dëgg gis naa ne, Yàlla du gënale,

10:35  waaye ci xeet yépp, ku ko ragal tey def lu jub, moom la nangu.

10:36  Yónnee na kàddoom bànni Israyil, di leen xebaar jàmm, jaarale ko ci Yeesu Kirist, miy Boroom lépp.

10:37  Xam ngeen li xewoon ci réewum Yawut yépp, li ko tàmbalee ci diiwaanu Galile, topp ci waareb Yaxya, mu naan nit ñi, mu sóob leen ci ndox.

10:38  Xam ngeen ne Yàlla fal na Yeesum Nasaret, sol ko Xel mu Sell mi ak kàttan; muy wër, di def lu baax ak di faj ñépp ñi nekkoon ci kilifteefu Seytaane, ndaxte Yàlla ànd na ak moom.

10:39  «Seede nanu li mu def lépp ci biir réewu Yawut ya ak Yerusalem. Moona rey nañu ko ci wékk ko ci bant.

10:40  Waaye Yàlla dekkal na ko ci ñetteelu fan ba te biral ko,

10:41  waxuma xeet wépp, waaye seede yi Yàlla tànn lu jiitu, maanaam nun ñi daan lekk di naan ak moom gannaaw ndekkiteem.

10:42  Te Yeesu sant na nu, nu yégal xeet wa, di seede ne, moom la Yàlla jagleel àtteb ñiy dund ak ñi dee.

10:43  Yonent yépp seedeel nañu ko ne, ku ko gëm, Yàlla dina la baal say bàkkaar ci turam.»

10:44  Bi Piyeer di wax loolu, Xel mu Sell mi wàcc ci kaw ñépp ñiy déglu kàddu ga.

10:45  Yawut yi gëm yépp nag, ñi ànd ak Piyeer, daldi waaru ci li Yàlla tuur Xel mu Sell, mi mu maye, ci ñi dul Yawut itam.

10:46  Ndaxte dégg nañu leen, ñuy wax yeneeni làkk ak di màggal Yàlla.

10:47  Booba Piyeer daldi wax ne: «Ñii jot Xel mu Sell mi ni nun, ndax manees na leen a bañ a sóob ci ndox?»

10:48  Noonu mu santaane, ñu sóob leen ci ndox ci turu Yeesu Kirist. Gannaaw loolu ñu ñaan ko, mu toog ci ñoom ay fan.

11:1  Bi loolu amee ndaw yi ak bokk yi nekk ci diiwaanu Yude, dégg nañu ne, ñi dul Yawut nangu nañu kàddug Yàlla.

11:2  Bi Piyeer demee Yerusalem nag, kureelu Yawut gi farataal xaraf, di werante ak moom ne ko:

11:3  «Lu tax nga dem ca këru ñu xarafal, bay lekk sax ak ñoom?»

11:4  Noonu Piyeer daldi leen benn-bennal mbir mi, nettali leen ko

11:5  ne: «Nekkoon naa ca dëkku Yope, di fa ñaan ci Yàlla, ba far sama xol seey ci moom; noonu ma am peeñu: lu mel ni sér bu mag wàcc, jóge ci asamaan, ñu yoor ko ca ñeenti laf ya, mu ñëw ba ci man.

11:6  Ma xool ko jàkk, seetlu ko bu baax, ma gis ca boroom ñeenti tànk yu nekk ci kaw suuf, di rabi àll yi, yiy raam ak picci asamaan.

11:7  Te dégg naa baat bu ma ne: “Jógal Piyeer, rey te lekk.”

11:8  Waaye ma tontu ne: “Mukk Boroom bi, ndax dara lu daganul mbaa lu araam musul a dugg ci sama gémmiñ.”

11:9  Waaye ñaareel bi yoon baat bi dellu ne ma: “Lu Yàlla sellal, bu ko araamal.”

11:10  Loolu am ba muy ñetti yoon, ba noppi ñu ne cas lépp, jëme asamaan.

11:11  «Ca saa sa ñetti góor, ña ñu yebal ci man, jóge Sesare, agsi ca kër ga ma dal.

11:12  Te Xel mi ne ma: “Àndal ak ñoom, te bu ci werante.” Juróom-benni bokk, yi fi teew, gunge woon nañu ma, ba nu dugg ca kër góor googu.

11:13  Mu nettali nu ne, gis na malaaka, feeñu ko ca këram ne ko: “Yónneel ca dëkku Yope, woolu Simoŋ, mi ñu dàkkentale Piyeer.

11:14  Dina la xamal ay wax yu lay musal, yaw ak sa waa kër gépp.”

11:15  «Bi ma tàmbalee wax nag, Xel mu Sell mi wàcc ci ñoom, ni mu wàcce woon ci nun bu jëkk.

11:16  Bi loolu amee ma fàttaliku li Boroom bi wax ne: “Yaxya ci ndox la daan sóobe, waaye yéen dees na leen sóob ci Xel mu Sell mi.”

11:17  Gannaaw nag Yàlla jagleel na leen may, gi mu nu mayoon, bi nu gëmee Yeesu Kirist Boroom bi, man maay kan, bay tebbi àtteb Yàlla?»

11:18  Bi ñu déggee loolu, amuñu dara lu ñu ca teg, ñu daldi màggal Yàlla ne: «Yàlla nag may na ñi dul Yawut it ñu tuub seeni bàkkaar, ba am dund gu wóor gi.»

11:19  Ñi tasoon nag ndax fitna, ji amoon gannaaw Ecen, ñu dem ba diiwaanu Fenisi, ci dunu Sipar ak ca dëkku Ancos, di wax kàddu gi, waaye yemale ko ci Yawut yi.

11:20  Moona amoon na ci ñoom ay niti Sipar ak dëkku Siren, ñu ñëw ci Ancos, ba seen wax law ci Gereg yi it, ñu di leen xamal xebaar bu baax bu Yeesu Boroom bi.

11:21  Te loxob Boroom bi ànd ak ñoom, ba mbooloo mu mag gëm te woññiku ci Boroom bi.

11:22  Ba mbir ma siiwee, ba àgg ci noppi mbooloom ñi gëm ci Yerusalem, ñu yebal Barnabas ba Ancos.

11:23  Bi mu agsee nag, ba gis yiw, wi leen Yàlla may, mu bég ci te di leen xiir, ñu wàkkirlu ci Boroom bi te dogu ci.

11:24  Ndaxte nit ku baax la woon te fees ak Xel mu Sell mi ak ngëm; noonu mbooloo mu bare dolliku ci Boroom bi.

11:25  Gannaaw loolu Barnabas dem ca dëkku Tars, di wut Sool.

11:26  Bi mu ko gisee, mu indi ko Ancos. Noonu atum lëmm ñu bokk ak mbooloom ñi gëm, di jàngal nit ñu bare. Te ci Ancos lañu jëkk a tudde taalibe ya Gaayi Kirist.

11:27  Ca fan yooyu ay yonent jóge Yerusalem, ñëw Ancos.

11:28  Kenn ci ñoom tudd Agabus jóg, mu yégle jaarale ko ci Xelu Yàlla mi ne, xiif bu metti dina daj àddina sépp. Loolu nag amoon na ca ayug buur bu ñuy wax Këlódd.

11:29  Kon taalibe ya fas yéenee sàkk ndimbal, jëme ca bokk ya dëkk diiwaanu Yude, ku nekk ak sa kem-kàttan.

11:30  Noonu lañu def nag, teg ko ci loxoy Barnabas ak Sool, yónnee ko njiit ya.

12:1  Ca jamono jooja Erodd buur ba jàppoon na ay nit ci mbooloom ñi gëm, ngir fitnaal leen.

12:2  Noonu mu daldi jàpp Saag, doomu ndeyu Yowaana, mu reylu ko ci jaasi.

12:3  Bi mu gisee nag ne, mbir moomu neex na Yawut ya, mu daldi jàpp it Piyeer; fekk loolu daje ak bési màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu ya amul lawiir.

12:4  Bi mu ko jàppee, mu tëj ko kaso, teg ko ci loxoy ñeenti mboolooy xarekat, ngir ñu wottu ko, fekk mbooloo mu ci nekk di ñeenti nit; amoon na yéeney yóbbu ko ci kanamu Yawut ya gannaaw màggalu bésu Jéggi ba.

12:5  Noonu ñuy wottu Piyeer ca kaso ba, waaye mbooloom ñi gëm di ko ñaanal Yàlla ak seen xol bépp.

12:6  Bi Erodd nekkee ci tànki indilu ko, ca guddi googa yeewoon nañu Piyeer ak ñaari càllala, muy nelaw diggante ñaari xarekat, te ay xarekat di wottu buntu kaso ba.

12:7  Ca saa sa malaakam Boroom bi ñëw, te leer ne ràyy ca néeg ba. Malaaka ma dóor Piyeer ci wetam, yee ko ne ko: «Jógal bu gaaw!» Noonu jéng ya rot ciy loxoom.

12:8  Malaaka ma ne ko: «Takkal sa geño te sol say dàll.» Mu def ko. Malaaka ma ne ko: «Solal sa mbubb te topp ci man.»

12:9  Piyeer génn, topp ca malaaka ma, fekk gëmul sax ne lu am la, waaye mu yaakaar ne peeñu la.

12:10  Noonu ñu weesu wottukat bu jëkk ba ak ba ca tegu, ñu agsi ca buntu weñ, ba jëm ca dëkk ba, mu daldi ubbikul boppam ci seen kanam. Ñu génn nag, jaar ci benn mbedd, malaaka ma daldi ko bàyyi.

12:11  Bi xelam dellusee ci moom Piyeer ne: «Léegi xam naa ci lu wóor ne, Boroom bi yónni na malaakaam, musal ma ci loxoy Erodd ak li ma Yawut ya yéene woon lépp.»

12:12  Mu rabal xelam ci loolu, daldi dem kër Maryaama, ndeyu Yowaana, mi ñuy wooye Màrk, fekk ñu bare booloo fa, di ñaan ci Yàlla.

12:13  Noonu Piyeer fëgg buntu kër ga, te mbindaan mu tudd Rodd wuyusi ko.

12:14  Mu xàmmi baatu Piyeer, bég ci, ba fàtte koo ubbil, waaye mu daw ci biir, xamle ne Piyeer a nga ca bunt ba.

12:15  Ñu ne ko: «Xanaa dangaa dof.» Waaye mu dëgër ci li mu wax. Noonu ñu ne ko: «Xanaa malaakaam la.»

12:16  Fekk Piyeer di gën a fëgg. Noonu ñu tijji, gis ko, daldi waaru.

12:17  Piyeer taf loxoom ci gémmiñam, ngir ñu noppi, daldi leen nettali, ni ko Boroom bi génnee ca kaso ba. Mu ne leen: «Tee ngeen jottali ko Saag ak bokk ya.» Bi mu ko waxee, mu jóge fa, dem feneen.

12:18  Bi bët setee nag, yengu-yengu bu réy am na ca xarekat ya, ñu ne: «Ana Piyeer?»

12:19  Noonu Erodd wutlu ko, waaye gisu ko. Kon mu àtte wottukat ya, joxe ndigalu rey leen. Bi loolu amee Erodd jóge ci diiwaanu Yude, dem dëkku Sesare, toog fa.

12:20  Fekk mu nekk ci xëccoo bu tàng ak waa dëkki Tir ak Sidon. Naka noona ñu ànd, bëgg koo gis. Ñu neexal Balastus, bëkk-néegu buur ba, di ñaan jàmm, ndaxte réewu buur ba moo doon dundal seen bos.

12:21  Ca bés ba ñu jàpp nag Erodd sol mbubbi buuram, toog ca jal ba ca àttekaay ba, di leen yedd ak a dénk.

12:22  Noonu mbooloo mi di yuuxu naan: «Lii baatu Yàlla la, du baatu nit!»

12:23  Ca saa sa nag, gannaaw màggalul Yàlla, malaakam Boroom bi fàdd ko te ay sax dugg ko, ba mu dee.

12:24  Moona kàddug Boroom bi di gën a màgg tey law.

12:25  Naka Barnabas ak Sool, bi ñu matalee seen liggéey, ñu jóge Yerusalem, ñibbi, ànd ak Yowaana mi tudd Màrk.

13:1  Amoon na ci mbooloom ñi gëm, mi nekk dëkku Ancos, ay yonent ak ay jàngalekat: maanaam Barnabas, Simeyon ku ñu dàkkentale Niseer, Lusiyus mi dëkk Siren, Manayen mi yaroondoo ak Erodd boroom diiwaan ba, ak Sool.

13:2  Am bés nag, bi ñuy jaamu Boroom bi ak di woor, Xel mu Sell mi ne: «Beral-leen ma Barnabas ak Sool ngir liggéey, bi ma leen wooye.»

13:3  Bi ñu ko déggee, ñu daldi woor ak a ñaan, teg leen ay loxo, ba noppi bàyyi leen ñu dem.

13:4  Noonu Xel mu Sell mi yónni leen. Ñu dem nag ci dëkku Selusi, dugg fa gaal, jëm ci dun bu ñuy wax Sipar.

13:5  Bi ñu teeree ca dëkku Salamin nag, ñu yégle fa kàddug Yàlla ca jàngub Yawut ya. Ku tudd Yowaana ànd ak ñoom, di leen jàpple ci liggéey bi.

13:6  Noonu ñu jaar ci dun bépp, ba egg dëkku Pafos. Foofa ñu gis luxuskat bu tudd Bar-Yeesu, di Yawut bu mbubboo turu yonent.

13:7  Mu bokk ci gàngooru boroom réew ma tudd Sersiyus Poolus, di nit ku neex xel. Moom nag mu woolu Barnabas ak Sool, ngir bëgg a dégg kàddug Yàlla.

13:8  Waaye Elimas, boroom xam-xam bu ñuul bi --ndaxte loolu la turam di tekki — di leen dogale, ngir bañ boroom réew ma gëm.

13:9  Ci kaw loolu Sool, mi tudd it Pool, daldi fees ak Xel mu Sell mi; mu xool ko jàkk,

13:10  ne ko: «Yaw mi fees ak fen ak lu bon, di doomu Ibliis, tey noonu lépp lu jub, ndax doo bàyyee dëngal yoon yu jub yu Boroom bi?

13:11  Léegi loxob Boroom bi dina dal sa kaw, te dinga gumba, ba dootuloo gis jant bi ab diir.» Ca saa sa nag ay bëtam muuru, mu daldi tàbbi cig lëndëm, muy làmbatu, di wut ku ko wommat.

13:12  Ba boroom réew ma gisee li xew nag, mu daldi gëm, di yéemu ci yoonu Boroom bi.

13:13  Naka noona Pool ak ñi mu àndal jóge Pafos, jaar ci géej, jëm dëkku Peers ci réewu Pamfili. Yowaana nag tàggoo ak ñoom, dellu Yerusalem.

13:14  Waaye ñoom ñu jóge Peers, aw ca yoon wa, ba ñëw dëkku Ancos ci diiwaanu Pisidi. Bésu noflaay ba nag ñu dugg ca jàngu ba, toog.

13:15  Bi ñu jàngee yoonu Musaa ak yonent ya, njiiti jàngu ba yónnee ca ñoom ne leen: «Bokk yi, bu ngeen amee lu ngeen di dénk mbooloo mi, waxleen ko.»

13:16  Noonu Pool jóg, tàllal loxoom ne leen: «Yéen bokki Israyil ak yéen ñi ragal Yàlla, dégluleen!

13:17  Yàllay bànni Israyil tànn na sunuy maam, di yokk xeet wa, bi ñuy ganeyaan ci Misra; ba noppi mu génne leen fa ak kàttanu loxoom.

13:18  Diirub ñeent-fukki at mu di leen muñal ca màndiŋ ma.

13:19  Gannaaw loolu faagal na juróom-ñaari xeet ci réewu Kanaan, ba sunuy maam donn réew ma.

13:20  Loolu lépp xew na ci diirub ñeenti téeméeri at ak juróom-fukk. «Gannaaw loolu mu jox leen ay àttekat, ba ci yonent Yàlla Samwil.

13:21  Booba ñuy ñaan buur, te Yàlla jox leen Sóol, doomu Kis ci giiru Ben-yamin, muy seen buur diirub ñeent-fukki at. Gannaaw ga mu jële ko fa,

13:22  dellu falal leen buur bu tudd Daawuda, mu seedee ko nii: “Gis naa Daawuda, doomu Yese, ku ma neex ci sama xol, te dina def lépp luy sama coobare.”

13:23  «Noonu ci askanam Yàlla indil na bànni Israyil Musalkat bi Yeesu, ci ni mu ko dige woon.

13:24  Laata muy ñëw nag, Yaxya daan na waare, ne bànni Israyil gépp, ñu tuub seeni bàkkaar, te mu sóob leen ci ndox.

13:25  Te ba Yaxyay jeexal sasam, mu ne: “Ku ngeen may teg? Duma Ki war a ñëw; waaye am na kuy ñëw sama gannaaw, koo xam ne kii yeyoowumaa tekki ay dàllam.”

13:26  «Bokk yi, yéen askanu Ibraayma ak yéen ñi ragal Yàlla, kàddug mucc gi ci nun la wàcc.

13:27  Waa Yerusalem ak seeni kilifa xàmmiwuñu woon Yeesu te xamuñu woon waxu yonent, yi ñuy jàng bésu noflaay bu nekk; teewul ñu amal waxu yonent yi, ci li ñu àtte Yeesu, ba daan ko.

13:28  Yoon dabu ko fenn, moona ñaan nañu Pilaat, mu reylu ko.

13:29  Noonu ñu def lépp lu yonent yi bindoon ci mbiram, ba noppi ñu wàcce ko ca bant ba, tàbbal ko ci bàmmeel.

13:30  Waaye Yàlla dekkal na ko,

13:31  te diirub ay fan yu bare feeñu na ñi àndoon ak moom, jóge diiwaanu Galile, dem Yerusalem; léegi nag ñooy ay seedeem ci wetu xeet wi,

13:32  te nu ngi leen di xamal xebaar bu baax ne leen, li Yàlla digoon sunuy maam,

13:33  def na ko ngir nun seeni sët, ci li mu dekkal Yeesu. Moom lañu bindoon ci ñaareelu saaru Sabóor ne:“Yaa di sama Doom,maa di sa Baay tey.”

13:34  Te it li ko Yàlla dekkal, ba mu bañatee jaar ci dee, te suuf du ko lekk mukk, moom la Yàlla wax ne:“Dinaa la may barke yu sell te wóor,yi ma digoon Daawuda.”

13:35  Moo tax mu waxaat feneen ne:“Doo bàyyi sa Waa ju sell, mu yàqu.”

13:36  Ndaxte bi Daawuda defee coobareg Yàlla ci jamonoom, mu faatu, ñu suul ko, mu fekki ay maamam, suuf lekk ko.

13:37  Waaye Ki Yàlla dekkal, yaramam seeyul.

13:38  «Kon nag bokk yi, nangeen xam ne, ci moom Yeesu nu ngi leen di yégal mbaalug bàkkaar yi. Te fépp fu yoonu Musaa tële woon a àttee nit ni ku jub,

13:39  fa la Yeesu di àttee ni ku jub képp ku ko gëm.

13:40  Wottuleen nag ba li yonent yi bindoon bañ leen a dal, ci li ñu ne:

13:41  “Yéen ñiy xeebaate, gis leen lii,ngeen yéemu ba far;ndaxte dinaa def ci seen jamono jëf,joo xam ne su ngeen ko déggee sax,dungeen ko gëm.”»

13:42  Bi ñuy génn nag ca jàngu ba, Yawut ya ñaan leen, ñu baamtu wax ja ca bésu noflaay ba ca tegu.

13:43  Te bi mbooloo ma tasee, ay Yawut yu bare ak ñi tuuboon ci yoonu Yawut te ragal Yàlla, topp ci Pool ak Barnabas. Ñuy diisoo ak ñoom, di leen xiir, ñu wàkkirlu ci yiwu Yàlla.

13:44  Noonu bésu noflaay ba ca tegu, daanaka waa dëkk bépp daje, ngir déglu kàddug Yàlla.

13:45  Waaye bi Yawut yi gisee mbooloo ma, ñu daldi fees ak kiñaan, di weddi li Pool di wax te di ko xas.

13:46  Bi loolu amee Pool ak Barnabas ne leen ci lu bir: «Yéen lanu war a jëkk a yégal kàddug Yàlla, waaye gannaaw gàntu ngeen ko, ba àtte seen bopp ne, yeyoowuleen dund gu dul jeex gi, kon nu ngi woññiku ci ñi dul Yawut.

13:47  Ndaxte moom la nu Boroom bi sant ci li mu naan:“Samp naa la, nga nekk leeru ñi dul Yawut,ngir nga yóbbu mucc gi, mu daj cati àddina.”»

13:48  Ñi dul Yawut nag, bi ñu déggee loolu, daldi bég tey màggal kàddug Boroom bi; te ñépp ñu jagoo dund gu dul jeex daldi gëm.

13:49  Noonu kàddug Boroom bi di law ci diiwaan bépp.

13:50  Waaye Yawut ya xiir ay jigéen, ñi woomle te farlu ci diine, ñoom ak magi dëkk ba, ñu fitnaal Pool ak Barnabas, ngir génne leen réew ma.

13:51  Waaye Pool ak Barnabas daldi yëlëb seen pëndu tànk, ngir dëggal seen weddi, jëm dëkku Ikoñum.

13:52  Naka taalibe yi nag, ñu fees ak mbég ak Xel mu Sell mi.

14:1  Bi Pool ak Barnabas nekkee Ikoñum nag, ñu dugg ci jàngub Yawut ya, ni ñu ko daan defe; ñuy waare, ba mbooloom Yawut ak Gereg mu bare gëm.

14:2  Waaye Yawut yu nanguwul yi ñoo jógloo ñi dul Yawut, di ñaawal seen njort ci bokki taalibe yi.

14:3  Pool ak Barnabas nag sax nañu ci Ikoñum lu yàgg, ñu wéeru ci Boroom bi, bay wax ak fit wu dëgër; te Yàlla dëggal kàddug yiwam, ba may leen, ñu def ay kéemaan ak ay firnde.

14:4  Noonu waa dëkk bi xàjjalikoo, ñii far ak Yawut yi, ñale far ak ndaw ya.

14:5  Waaye ñi dul Yawut ak Yawut yi, ñoom ak seeni kilifa, lal pexem fitnaal leen ci sànni ay doj.

14:6  Bi ko Pool ak Barnabas yégee nag, ñu daw ca diiwaanu Likawni ca dëkk ya ñuy wax Listar ak Derbë ak wàllaa ya.

14:7  Foofa ñu di fa xamle xebaar bu baax bi.

14:8  Amoon na ca Listar nag nit ku fa toog, ku ay tànkam làggi, ndax li mu judduwaale lafañ te musul a dox.

14:9  Moom nag muy déglu Pool miy waare. Noonu Pool xool ko jàkk, gis ne, am na ngëm ngir wér.

14:10  Mu ne ko ak baat bu dëgër: «Jógal taxaw bu jub.» Noonu nit ki ne bërét, jóg, daldi dox.

14:11  Bi mbooloo ma gisee li Pool def, ñu daldi yuuxu, ne ci làkku waa Likawni: «Yàlla yi soppiku nañu nit, wàcc ci nun.»

14:12  Noonu ñu tudde Barnabas, Sës, te tudde Pool, Ermes, ndaxte mooy ki yor wax ji.

14:13  Fekk ci buntu dëkk ba amoon na fa kër gu ñuy màggale Sës. Saraxalekat ba nag ànd ak mbooloo ma, daldi indi ca bunt ya ay yëkk ak ay caq, yi ñu defare tóor-tóor, ngir màggal leen ci tuur deretu mala.

14:14  Waaye bi ko ndaw yi Barnabas ak Sool déggee, ñu sib ko ba xotti seeni yére, ñu daldi daw, tàbbi ca mbooloo ma, di wax ci kaw ne:

14:15  «Yéen nit ñi, lu leen xiir ci lii? Nun it ay nit lanu, ñu bokk bind ak yéen. Te nu ngi leen di xamal xebaar bu baax ne leen, ngeen dëddu yëfi neen yii te woññiku ci Yàlla miy dund te sàkk asamaan, suuf, géej ak li ñu ëmb lépp.

14:16  Démb mayoon na xeet yépp, ñu aw seen yoonu bopp.

14:17  Moona noppiwul a firndeel aw meloom ci def lu baax, di leen wàcceele ci asamaan taw buy indi naataange, ba ngeen lekk ba suur, te seen xol fees ak mbég.»

14:18  Noonu ci lu jafe yey nañu mbooloo ma ak wax jooju, ba tere leen, ñu rendil leen sarax.

14:19  Waaye bi loolu wéyee amoon na ay Yawut yu jóge Ancos ak Ikoñum, ñu fàbbi mbooloo ma, sànni Pool ay doj, ba yaakaar ne dee na, ñu diri ko ba ca gannaaw dëkk ba.

14:20  Waaye taalibe ya ñëw wër ko, mu daldi jóg, duggaat ca dëkk ba. Ca suba sa nag, mu ànd ak Barnabas, dem Derbë.

14:21  Bi ñu fa àggee nag, ñu xamle fa xebaar bu baax bi, ba sàkk fa ay taalibe yu bare. Gannaaw loolu ñu dellusi Listar, Ikoñum ak Ancos,

14:22  di dooleel xeli taalibe ya, xiir leen ñu sax ci yoon wi; ñu ne leen: «Ci kaw nattu yu bare lanu war a dugge ci nguuru Yàlla.»

14:23  Ci mbooloom ñi gëm mu nekk nag, ñu tànn ci ay njiit; ba noppi ñu ñaan Yàlla ak di woor, dénk leen Boroom bi ñu gëm.

14:24  Gannaaw loolu ñu jaar diiwaanu Pisidi, dikk ci Pamfili.

14:25  Ñu yégle kàddu gi ci dëkku Peers, door a dem dëkku Atali.

14:26  Foofa nag ñu dugg gaal, jëm Ancos, fa ñu leen dénke woon ca yiwu Yàlla, ngir liggéey bi ñu àggale.

14:27  Bi ñu agsee, ñu woo mbooloom ñi gëm, nettali leen fi ñu jaar ak Yàlla fépp, ak ni mu ubbee buntu ngëm ci ñi dul Yawut.

14:28  Noonu ñu toog ak taalibe ya diir bu yàgg.

15:1  Amoon na bés ay nit jóge diiwaanu Yude, ñuy jàngal bokk yi ne leen: «Ku xaraful, ni ko aaday Musaa santaanee, doo man a mucc.»

15:2  Pool ak Barnabas nag am ak ñoom diisoo ak werante wu metti; noonu bokk yi jàpp ne, Pool ak Barnabas ak ñeneen ci ñoom war nañoo dem Yerusalem ca ndaw ya ak njiit ya, ngir leeral werante wi.

15:3  Kon nag mbooloo mi gunge leen, ñu jaar ci wàlli Fenisi ak Samari, di nettali ni ñi dul Yawut woññikoo ci Yàlla, ba bokk yépp am ca mbég mu réy.

15:4  Te bi ñu agsee Yerusalem, mbooloom ñi gëm, ndaw yi ak njiit yi teeru leen, ñu nettali leen fi ñu jaar ak Yàlla fépp.

15:5  Ci kaw loolu ñeneen, ñi gëm waaye bokk ci tariixab Farisen ya, daldi jóg ne: «Fàww ñi dul Yawut xaraf, te ñu dénk leen sàmm yoonu Musaa.»

15:6  Noonu ndaw yi ak njiit yi dajaloo, ngir seet mbir moomu.

15:7  Gannaaw werante wu bare Piyeer jóg ne leen: «Yéen bokk yi, xam ngeen ne, ca njàlbéen ga Yàlla tànnoon na ma ci yéen, ngir ma yégal ñi dul Yawut xebaar bu baax bi, ba ñu gëm.

15:8  Te Yàlla, mi xam xol yi, seede na leen ci li mu leen may Xel mu Sell mi, ni mu nu ko maye nun itam.

15:9  Gënalantewu nu ak ñoom, ci li mu sellal seen xol ci kaw ngëm.

15:10  Léegi nag lu tax ngeen di diiŋat Yàlla, ciy teg taalibe yi yen bu nu musul a àttan, nun mbaa sunuy maam?

15:11  Nun daal ci yiwu Yeesu Boroom bi lanu yaakaar a mucce, te ñoom itam, ci lañu wékku.»

15:12  Bi mu ko waxee, mbooloo mépp ne xeram, di déglu Barnabas ak Pool, ñuy nettali kéemaan ak firnde yépp, yi Yàlla def jaarale ko ci ñoom ci biir ñi dul Yawut.

15:13  Bi ñu noppee, Saag jël kàddu ga ne:

15:14  «Bokk yi, dégluleen ma! Simoŋ nettali na, ni Yàlla seetsee bu jëkk ñi dul Yawut, ngir sàkku ci ñoom xeet wu ñu tudde turam.

15:15  Te loolu sax dëppoo na ak li yonent yi tëral; ñu bind ne:

15:16  “Boroom bi nee na:Gannaaw loolu dinaa dellusi,te yékkati këru Daawuda, gi ne tasar,dinaa defar toj-toj ya,ba taxawalaat ko.

15:17  Noonu li des ci doom Aadama wut Boroom bi,maanaam xeet yi dul Yawut, ñuy tudd sama tur.

15:18  Man dinaa def loolu, man Boroom bi ko wax,te ca njàlbéen ba tey ma di ko xamle.”

15:19  «Kon nag lii mooy sama ndigal: bunu gétën ñi dul Yawut te woññiku ci Yàlla.

15:20  Waaye nu bind leen, ñu moytu ñam wu araam wu ñu tuuroo xërëm, tey moytu njaaloo, ak jur gu médd, bay naan deret ja.

15:21  Ndaxte ca njàlbéen ga ba tey am na ca dëkk bu nekk ñuy waare ci yoonu Musaa; bésu noflaay bu nekk sax dañu ciy xutba ca jàngu ya.»

15:22  Bi mu ko waxee, ndaw yi ak njiit yi ak mbooloom ñi gëm mépp fas yéenee tànn ci ñoom ay nit, yónni leen Ancos, ñu ànd ak Pool ak Barnabas. Noonu ñu tànn Yudd, mi ñuy dippee Barsabas, ak Silas, di ay njiit ca bokk ya.

15:23  Ñu jox leen bataaxal bu ne: Yéen sunu bokk yi dul Yawut te dëkk Ancos, Siri ak Silisi, nu ngi leen di nuyu, nun seeni bokk, di ndaw yi ak njiit yi.

15:24  Dégg nanu ne, am na ay nit ñu bawoo ci nun, ñu di leen lëjal ak seeni wax, di jaxase seeni xol, te fekk sukkandikuwuñu ci lenn ndigal lu jóge ci nun.

15:25  Kon nag mànkoo nanu ci tànn ay nit, yónnee leen ko, ànd ak sunuy soppe Barnabas ak Pool.

15:26  Ñoom jaay nañu seen bakkan ngir turu Yeesu Kirist Boroom bi.

15:27  Yónni nanu nag Yudd ak Silas, ñu di leen xamal xebaar boobu ci seen gémmiñ.

15:28  Ndaxte li neex Xel mu Sell mi te neex nu, mooy nu bañ leen a teg beneen yen, lu dul dénkaane yii am njariñ,

15:29  maanaam ngeen moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm, deretu jur gu médd ak njaaloo. Bu ngeen moytoo yëf yooyu, dingeen def lu baax. Ci jàmm.

15:30  Noonu ñu tàggoo, dem Ancos, ñu dajale mbooloo mi, jébbal leen bataaxal bi.

15:31  Ñu jàng ko nag, seen xol sedd ci doole, ji leen bataaxal bi indil.

15:32  Te Yudd ak Silas, ñi doon yonent, ñuy dooleel bokk yi, di dëgëral seen fit ak wax yu bare.

15:33  Bi loolu amee ñu toog fa ab diir, ba noppi bokk yi yiwi leen ci jàmm, ñu dellu ca ña leen yónni woon.

15:35  Waaye Pool ak Barnabas des ci Ancos, di jàngale ak di xamle xebaar bu baax bu kàddug Boroom bi, ñoom ak ñeneen ñu bare.

15:36  Gannaaw ay fan Pool ne Barnabas: «Nan dellu seeti bokk ya ca dëkk yépp, fu nu mas a yéglee kàddug Boroom bi, ba gis nu ñu def.»

15:37  Barnabas nag bëggoon na yóbbaale Yowaana, mi ñuy wax it Màrk.

15:38  Waaye Pool dafa lànk ne: «Matul nu yóbbu ki nu waccoon ca Pamfili, ba àndul woon ak nun ca liggéey ba.»

15:39  Noonu ñu xuloo, ba far tàggoo. Barnabas yóbbaale Màrk, ñu dugg gaal, jëm Sipar.

15:40  Pool tànn Silas, dem; bokk ya dénk leen ci yiwu Boroom bi;

15:41  mu jaar ci diiwaanu Siri ak Silisi, di dëgëral mboolooy ñi gëm.

16:1  Naka noona mu dikk dëkki Derbë ak Listar, fekk fa taalibe bu tudd Timote te ndeyam di Yawut bu gëm, waaye baayam di Gereg.

16:2  Te mbokk, yi nekk dëkki Listar ak Ikoñum, seedeel nañu ko lu baax.

16:3  Pool bëgg nag mu ànd ak moom, waaye ndegam Yawut yépp, ya dëkk ca wàllaa ya, xam ne baayam Gereg la woon, mu jël ko, xarafal ko.

16:4  Bi loolu amee ñuy jaar ca dëkk ya, jottali leen dénkaane, yi ndaw yi ak njiit yi nekk Yerusalem joxe, te sant leen ñu sàmm ko.

16:5  Noonu mboolooy ñi gëm di gën a dëgër ci yoon wi, tey yokku bés bu nekk.

16:6  Bi loolu amee gannaaw Xel mu Sell mi aaye na leen, ñu yégleji kàddu gi ci diiwaanu Asi, ñu daldi jaari wàlli Firisi ak Galasi.

16:7  Bi ñu agsee nag ci wetu diiwaanu Misi, ñuy jéem a dugg diiwaanu Bitini, waaye Xelum Yeesu mayuleen ko.

16:8  Ñu romb nag Misi, dem dëkku Torowas.

16:9  Noonu ci guddi Yàlla feeñu Pool ci nii: nitu Maseduwan taxaw, di ko ñaan ne ko: «Ñëwal ci Maseduwan, wallusi nu!»

16:10  Bi mu amee peeñu moomu, ca saa sa nu fexee jàll ba Maseduwan, xam ne Boroom bi moo nu woo, ngir nu xamle fa xebaar bu baax bi.

16:11  Noonu nu dugg gaal ca Torowas, jubal dunu Samotaras, jóge fa ca ëllëg sa, nu jëm teerub Neyapolis.

16:12  Bi nu fa teeree, nu jëm Filib, bi nekk dëkk bi ëpp maana ca wàll woowu ci diiwaanu Maseduwan, di it suufus Room. Nu toog fa ay fan.

16:13  Bi bésu noflaay agsee nag, génn nanu ci buntu dëkk ba, jublu ci wetu dex ga, yaakaar ne bérabu ñaanukaay la. Nu toog fa nag, di wax ak jigéen ña fa dajaloo.

16:14  Fekk am na fa jigéen juy déglu, tudd Lidi, di jaaykatu cuub, bu dëkk Catir, te mu ragal Yàlla. Noonu Boroom bi ubbi na xolam, ba mu nangu li Pool di wax.

16:15  Ci kaw loolu ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram, ba noppi mu ñaan nu ne: «Bu ngeen ma jàppee ni ku takku ci Boroom bi, ganesileen ma ci sama kër.» Te mu di nu ci xiir.

16:16  Am bés, ba nuy dem nag ca ñaanukaay ba, nu daje ak jaam bu jigéen bu rabu gisaane solu, te ay sangam di jariñu lu bare ci gisaaneem.

16:17  Mu daldi topp ci Pool ak nun, di xaacu ne: «Nit ñii jaami Yàlla Aji Kawe ji lañu; ñoo leen di yégal yoonu mucc.»

16:18  Muy def noonu ay fani fan, waaye bi ko Pool xajootul, mu woññiku ne rab wa: «Sant naa la ci turu Yeesu Kirist, génnal ci moom.» Noonu rab wa ne mëll, génn ci moom.

16:19  Bi ay sangam gisee nag seen buntu wërsëg tëju, ñu daldi jàpp Pool ak Silas, di leen diri, jëme leen ca pénc ma fa kanam njiit ya.

16:20  Noonu ñu dëj leen fa mbaxanay menne naan: «Yawut yii lëjal nañu sunu dëkk,

16:21  di xamle ay aada yu nu sañul a nangu mbaa nu di ko topp, nun ñi bokk ci nguuru Room.»

16:22  Mbooloo ma it ànd ci, dal ci seen kaw; àttekat ya nag summilu seeni yére, santaane ñu dóor leen ay yar.

16:23  Noonu ñu dóor leen ay yar yu bare, tëj leen, sant boroom kaso ba, mu wottu leen bu wér.

16:24  Gannaaw jot na ndigal loolu nag, mu sànni leen ca néeg ba gën a ruqu ci biir kaso ba, jéng seeni tànk.

16:25  Ba guddi giy xaaj nag, Pool ak Silas di ñaan ak di sant Yàlla, te ñeneen ñi nekk ca kaso ba di leen déglu.

16:26  Ca saa sa suuf yengu bu metti, ba fondamaab kaso ba daanu; bunt yépp daldi ne kulbet ubbiku, te jéngi ña ñu tëj ne tell tijjiku.

16:27  Ci kaw loolu boroom kaso ba tiite ci ay nelaw, gis bunt yépp ubbiku, mu daldi bocci jaaseem, bëgg a xaru, yaakaar ne ña ñu tëj dañoo daw.

16:28  Waaye Pool wax ci kaw ne: «Bul lor sa bopp, nun ñépp nu ngi fi.»

16:29  Bi ko boroom kaso ba déggee, mu daldi laaj làmp, ne saraax dugg, daanu ci kanamu Pool ak Silas, di lox.

16:30  Mu génne leen ci biti ne leen: «Kilifa yi, lu ma war a def, ba mucc?»

16:31  Ñu tontu ko: «Gëmal Yeesu Boroom bi, kon dinga mucc, yaw ak sa njaboot.»

16:32  Noonu ñu xamal ko kàddug Boroom bi, moom ak waa këram gépp.

16:33  Mu jël leen nag ci waxtu woowu ci guddi, raxas seeni gaañu-gaañu, ba noppi ñu sóob ko ci ndox, moom ak waa këram gépp.

16:34  Bi ñu ko defee mu yóbbu leen ca këram, jox leen ñu lekk, mu bég lool ci li mu gëm Yàlla, moom ak waa këram gépp.

16:35  Bi bët setee, àttekat ya yónni alkaati ya, ñu ne boroom kaso ba: «Yiwil ñaari nit ñooñu, ñu dem.»

16:36  Kon boroom kaso ba yégal loolu Pool ne ko: «Àttekat ya jox nañu ma ndigal, ngir ma yiwi leen, ngeen dem; léegi nag génnleen, te dem ci jàmm.»

16:37  Waaye Pool ne alkaati ya: «Dóor nañu nu ay yar ci kanamu ñépp, ci lu ñu wéerul ci benn àtte, rax-ca-dolli tëj nañu nu kaso, nun ñiy jaambur ci nguuru Room. Léegi ndax dañu noo bëgg a sànni ci mbedd mi ci kumpa? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, gunge nu ci biti.»

16:38  Bi mu ko waxee, alkaati ya yégal àttekat ya la mu wax. Bi ñu déggee ne, jaamburi Room lañu, ñu daldi tiit.

16:39  Ñu ñëw nag di leen dëfël, ñu gunge leen ci biti, di leen ñaan, ñu génn dëkk ba.

16:40  Noonu ñu génn ca kaso ba, dugg ci kër Lidi, ñu gis fa bokk ya, dëgëral leen, daldi dem seen yoon.

17:1  Bi ñu fa jógee, ñu aw yoon wa jaar dëkku Amfipolis ak Apoloni, door a ñëw Tesalonig, fa Yawut ya am jàngu.

17:2  Pool nag dugg ca ñoom, na mu ko daan defe, ba am fa ñetti bésu noflaay, muy werante ak ñoom ci li Mbind mi wax.

17:3  Mu di leen ko tekki, te di leen wax ay firnde yuy wone ne, fàww Almasi bi sonn te dekki. Mu ne leen: «Yeesu, mi ma leen di yégal, mooy Almasi bi.»

17:4  Noonu ñenn ci Yawut yi gëm, ànd ak Pool ak Silas, ñoom ak mbooloo mu mag ci Gereg yi ragal Yàlla, ak jigéen ñu am maana ñu bare.

17:5  Waaye kiñaan tàbbi ca Yawut ya, ñu daldi jël ay taxawaalukat ca pénc ma, dajale mbooloo, ñuy yengal dëkk ba. Ñu daanu ci kër Yason, di wut Pool ak Silas, ngir dëj leen ci kanam waa dëkk ba.

17:6  Bi ñu leen gisul nag, ñu diri Yason ak ñeneen ca bokk ya ci kanam àttekat ya. Ñuy wax ci kaw naan: «Nit ñi dëpp àddina sépp agsi nañu fii léegi,

17:7  te Yason a leen dalal. Ñoom ñépp dañoo bañ ndigali buur Sesaar ne, am na beneen buur bu ñuy wax Yeesu.»

17:8  Bi ko mbooloo mi ak àttekat yi déggee, ñu daldi jaaxle lool.

17:9  Noonu nanguwuñoo yiwi Yason ak ñi ci des, lu dul bi ñu leen bataleelee dara.

17:10  Bi loolu amee bokk yi jàllale Pool ak Silas ci saa si ci guddi, ñu jëm Bere. Ba ñu fa eggee nag, ñu dugg ca jàngub Yawut ya.

17:11  Fekk ña fa nekk ñoo gën a am ay teggin waa Tesalonig, ndaxte nangu nañu kàddu ga te sawar ca, di niir Mbind mi bés bu nekk, ba xam ndax loolu dëgg la am déet.

17:12  Kon nag Yawut yu bare gëm ak ñu bare ci Gereg yi, di jigéen yu am maana ak ay góor.

17:13  Waaye bi Yawuti Tesalonig déggee ne, Pool mu ngi yégle kàddug Yàlla ci Bere it, ñu daldi fay dikk, di jógloo ak a jaxase mbooloo ma.

17:14  Noonu bokk yi yebal Pool ca saa sa, mu jëm géej, waaye Silas ak Timote des fa.

17:15  Ñi ànd ak Pool nag gunge ko ba dëkku Aten. Bi ñu fa àggee, ñu woññiku, yóbbaale ndigalu Pool ne, Silas ak Timote ñëw fekksi ko ci lu gën a gaaw.

17:16  Bi leen Pool di nég ca Aten, mu am naqaru xol wu réy ci li mu gis dëkk ba fees ak ay nataali bokkaale Yàlla.

17:17  Muy werante nag ca jàngu ba ak Yawut ya ak ña ragal Yàlla, tey werante it bés bu nekk ca pénc ma ak ña fay dajaloo.

17:18  Noonu ay boroom xam-xam ci mbooloo mi ñuy wax Epikuren ak ci mbooloo mi ñuy wax Estowisen, di werante ak moom. Ñenn ci ñoom ne: «Fortukatu xam-xam bii, lu mu bëgg a wax?» Te ña ca des, bi ñu déggee Pool di waare xebaar bu baax bi, aju ci Yeesu ak ci mbirum ndekkite, ñu ne: «Dafa mel ni, day waare ay yàlla yu nu xamul.»

17:19  Kon nag ñu jël ko, yóbbu ko ca géew, ba ñuy wax Areyopas. Ñu ne ko: «Danoo bëggoon, nga leeral nu ci sa xam-xam bu bees, bii ngay yégle.

17:20  Ndaxte sol nga ci sunuy nopp lu nu xamul. Danoo bëggoon a xam nag léegi, loolu lu muy tekki.»

17:21  Ndaxte waa Aten ñépp ak doxandéem ya fa dëkk, wax ak a déglu lu bees rekk lañu daan xënte.

17:22  Noonu Pool taxaw ci biir mbooloom Areyopas ne leen: «Yéen waa Aten gis naa ne, farlu ngeen ci diine lool.

17:23  Ndaxte bi may doxantu di seet seeni màggalukaay, gis naa ci benn bu ñu bind lii: “Yàlla mi nu xamul.” Li ngeen di màggal nag te xamuleen ko, loolu laa leen di xamal.

17:24  «Yàlla mi sàkk àddina ak li mu ëmb lépp, moom miy Boroom asamaan ak suuf, du dëkk ci néegi màggalukaay yu loxoy nit defar.

17:25  Du jariñu it ci loxoy nit, mel ni dafa soxla dara, ndax moom mooy jox ñépp bakkan ak ruu ak lépp.

17:26  Ci kenn nit la sàkke xeeti àddina yépp, ñu dëkk ci ñeenti xebla yi; fekk àppal na xeet wu nekk jamonoom, te rëdd seen diggi réew.

17:27  Yàlla def na loolu, ngir ñu koy wut ci yaakaaru daj ko ci làmbatu, fekk sax sorewul kenn ci nun.

17:28  “Ndaxte ci moom lanuy dunde, di ci jëf te nekk ci,” ni ko ñenn ci seeni taalifkat dëggale naan: “Nun noo di aw xeetam.”

17:29  Kon nag, bu nu nekkee xeetu Yàlla, warunoo gëm ne, Yàlla mel na ni nataali wurus, xaalis mbaa doj yu nit defar ci xareñ mbaa xel.

17:30  Ca jamono yu wees ya Yàlla toppul ñàkka xam googa, waaye léegi koo man a doon ak foo man a nekk, Yàlla santaane na, nga tuub say bàkkaar.

17:31  Ndaxte sàkk na bés bu muy àtte àddina ci njub, dénk ko Nit ki mu tànn; te firndeel na loolu bu wóor, ci li mu ko dekkal ca néew ya.»

17:32  Bi ñu déggee nag, muy wax ci mbirum ndekkitel ñi dee, ñii di ko fontoo, ña ca des ne ko: «Dinanu la déglu ci mbir moomu beneen yoon.»

17:33  Noonu Pool génn ci seen biir.

17:34  Moona am na ñenn ñu taq ci moom te gëm: xàmmees na ci Denis, ku bokk ci mbooloom Areyopas, ak jigéen ju tudd Damaris, ak ñeneen.

18:1  Bi loolu wéyee Pool bàyyikoo Aten, dem Korent.

18:2  Mu tase fa ak Yawut bu tudd Akilas te juddoo diiwaanu Pont. Muy sog a jóge réewu Itali ak jabaram Pirsil, ndaxte buur ba Këlódd sant na Yawut yépp, ñu génn Room.

18:3  Noonu Pool seeti leen, te gannaaw ñoo bokk liggéey, maanaam di defar ay tànt, mu dal fa ñoom, ñuy liggéeyandoo.

18:4  Bésu noflaay bu nekk nag muy diisoo ak ñi nekk ca jàngu ba, di jéem a gëmloo ay Yawut ak ay Gereg.

18:5  Waaye bi Silas ak Timote jógee diiwaanu Maseduwan, egg fa, Pool jublu ci xamle kàddu gi, tey dëggal ci Yawut yi naan, Yeesu mooy Almasi bi.

18:6  Bi ko Yawut ya gàntoo nag, di ko xas, mu yëlëb ay yéreem ne leen: «Yéena sàkku seen musiba; set naa ci. Léegi maa ngi dem ci ñi dul Yawut.»

18:7  Ci kaw loolu mu jóge fa, dugg ci këru ku tudd Tisiyus Yustus, di ku ragal Yàlla, te kër ga dend ak jàngu ba.

18:8  Kirispus nag, njiitu jàngu ba, gëm na Boroom bi ak waa këram gépp. Te waa Korent ñu bare dégg kàddu gi te gëm ko, ñu sóob leen ci ndox.

18:9  Naka noona Boroom bi feeñu Pool ci guddi ne ko: «Bul tiit dara, waaye deel wax te bañ a noppi.

18:10  Ndaxte maa ngi ànd ak yaw, te kenn du la jàpp, ba fitnaal la, ndaxte am naa xeet wu bare ci dëkk bii.»

18:11  Noonu Pool des at ak genn-wàll ci seen biir, di fa jàngale kàddug Yàlla.

18:12  Ci nguuru Galyon ci diiwaanu Akayi nag, Yawut ya likkoo, ñu dal ci kaw Pool, yóbbu ko ca àttekaay ba.

18:13  Ñu ne: «Kii day xiir nit ñi ci màggal Yàlla ci lu juuyoo ak yoon wi.»

18:14  Bi Pool bëggee wax nag, Galyon ne Yawut ya: «Yéen Yawut yi, bu aju woon ci jàdd yoon walla ñaawteef wu réy, kon liy yoon mooy ma déglu leen.

18:15  Waaye bu ajoo ci ay werante ciy wax ak ay tur ak seen yoon, loolu seen wàll la; man duma ko àtte.»

18:16  Noonu mu dàq leen ca àttekaay ba.

18:17  Ci kaw loolu nit ñépp jàpp Sosten, njiitu jàngu ba, ñu di ko dóor ca kanamu àttekaay ba, waaye Galyon faalewu leen.

18:18  Bi loolu wéyee Pool desati fa fan yu bare. Gannaaw ga mu tàggtoo ak bokk ya, dugg gaal jëm Siri, ànd ak Pirsil ak Akilas. Bi mu jógeegul teerub Señsere, mu watlu boppam, ndaxte am na lu mu dige woon ak Yàlla.

18:19  Noonu ñu teer ci Efes. Pool bàyyi fa ñi mu àndaloon, daldi dugg ca jàngu ba, di diisoo ak Yawut ya.

18:20  Ñu ñaan ko, mu des fa lu gën a yàgg, waaye nanguwul.

18:21  Kon mu tàggtoo ak ñoom naan: «Dinaa dellusi ci yéen, bu soobee Yàlla.» Noonu mu dugg gaal, jóge Efes,

18:22  teersi dëkku Sesare, mu dem nuyu mbooloom ñi gëm, ba noppi dem Ancos.

18:23  Bi mu fa desee ay jamono, mu jóge fa, di jaar dëkkoo-dëkk ci diiwaanu Galasi ak Firisi, di dooleel xoli taalibe yépp.

18:24  Amoon na nag Yawut bu tudd Apolos te juddoo Alegsàndiri, mu dikk Efes. Nit ku yeewu la woon te am xam-xam bu yaatu ci Mbind mi.

18:25  Jàngoon na ci yoonu Boroom bi, di ku farlu ci xelam, muy xamle ak a jàngale bu wóor ci mbirum Yeesu, waaye fekk xam-xamam yem ci ni Yaxya daan sóobe ci ndox.

18:26  Noonu mu daldi wax ak fit wu dëgër ca jàngu ba. Bi ko Pirsil ak Akilas déggee nag, ñu woo ko fi ñoom, gën ko leeral yoonu Yàlla.

18:27  Naka mu bëgg a dem Akayi, bokk ya xiir ko ca, ñu bind taalibe ya, ngir ñu teeru ko teeru bu rafet. Noonu mu dikk fa te jariñ lool ñi gëm jaare ko ci yiwu Yàlla.

18:28  Ndaxte mu ngay yey Yawut ya ca kanam ñépp, di firi Mbind yi, ba wone ne Yeesu mooy Almasi bi.

19:1  Ba Apolos nekkee Korent nag, Pool jaar ca teggi ya gën a kawe ca réew ma, door a dikk Efes. Noonu mu gis fa ay taalibe.

19:2  Mu ne leen: «Ndax jot ngeen ci Xel mu Sell mi, bi ngeen gëmee?» Ñu tontu ko: «Déggunu sax ne, Xel mu Sell mi am na.»

19:3  Mu ne leen: «Kon nag, bi ñu leen sóobee ci ndox, lu ciy maana?» Ñu tontu ko: «Xanaa li Yaxya tëral.»

19:4  Pool ne leen: «Yaxya daan na sóob nit ñi ci ndox, ndax bi ñu tuubee seeni bàkkaar; te mu ne bànni Israyil, kiy topp ci moom lañu war a gëm, maanaam Yeesu.»

19:5  Bi ñu déggee loolu nag, sóob nañu leen ci ndox ci turu Yeesu Boroom bi.

19:6  Te bi leen Pool tegee loxo, Xel mu Sell mi ñëw ci ñoom, ñuy wax yeneeni làkk, di wax ci kàddug Yàlla.

19:7  Limub nit ñooñu nekk na lu mat fukk ak ñaar.

19:8  Noonu Pool dugg ca jàngu ba, di wax ak fit wu dëgër diirub ñetti weer, di diisoo ak ñoom ci mbirum nguurug Yàlla, di leen jéem a gëmloo.

19:9  Waaye bi xolu ñenn ci ñoom fattee, ñu gëmadi, bay suufeel yoon wi ci kanam mbooloo ma, mu jóge ci ñoom, xàjjale taalibe yi ak ñoom, di diisoo bés bu nekk ca jàngukaayu ku ñuy wax Tiranus.

19:10  Mu wéy ci noonu diirub ñaari at, ba ñi dëkk diiwaanu Asi ñépp dégg kàddug Boroom bi, muy Yawut muy Gereg.

19:11  Booba Yàllay def ay kéemaan yu ràññiku yuy jaar ci loxoy Pool.

19:12  Ñu yóbbul sax ñi wopp ay kaala ak ay taraxlaay yu laaloon yaramam, ba jàngoro yi di leen bàyyi, rab yay génn ci ñoom.

19:13  Noonu ay Yawut yuy wëndéelu, di faj ñi rab jàpp, ñu di leen jéem a ñaanal ci turu Yeesu Boroom bi naan: «Ci turu Yeesu, mi Pool di yégle, génnleen.»

19:14  Ñi doon def loolu, juróom-ñaari doom lañu woon ci Sewa, mi doon taafantaloo saraxalekat bu mag ba ci Yawut yi.

19:15  Waaye bi ñu ko defee rab wa tontu leen ne: «Xam naa Yeesu, xam naa it kuy Pool, waaye yéenay ñan?»

19:16  Ci kaw loolu nit ka rab jàpp song leen, noot leen ñoom ñépp; mu soxore leen lool, ba ñu daw kër ga, def yaramu neen te gaañu bu metti.

19:17  Loolu siiw na ci ñépp, ñi dëkk Efes, di Yawut ak Gereg; tiitaange jàpp leen ñoom ñépp, ba ñu màggal turu Yeesu Boroom bi.

19:18  Bi loolu amee ñu bare ci ñi gëm ñëw, di wesar ci kanam ñépp seeni jati luxus.

19:19  Te ñu bare ci ñi daan luxus, indi seeni téere, lakk leen ci kanam ñépp. Te bi ñu xaymaa njëg ga, mu tollook juróom-fukki junniy poseti daraxma.

19:20  Noonu la kàddu Boroom bi lawe, te noot lépp.

19:21  Bi loolu wéyee Pool nas xel jëm Yerusalem, jaar ci diiwaani Maseduwan ak Akayi. Mu ne: «Gannaaw bu ma fa demee, fàww ma seeti Room it.»

19:22  Mu yebal nag ci Maseduwan ñaari jaraafam, di Timote ak Erast, waaye moom mu des ab diir ci Asi.

19:23  Fekk booba amoon na yengu-yengu bu réy ci lu aju ci Yoon wi.

19:24  Ndaxte nit ku tudd Demetirus, di tëggu xaalis buy defar nataali xaalis ngir màggal Artemis, daan na ci jariñu lu bare, moom ak ay nawleem.

19:25  Noonu mu dajale leen ak seeni liggéeykat ne leen: «Gaa ñi, xam ngeen ne, sunu njariñ mu ngi aju ci liggéey bii.

19:26  Gis ngeen nag te dégg ne, Pool male gëmloo na bay fàbbi mbooloo mu bare, waxuma ci Efes rekk, waaye ci biir Asi gépp naan: “Yàlla yu ay loxo defar duñu ay yàlla.”

19:27  Léegi kat loraangee ngi nuy yoot, te du yem ci xañ nu sunu liggéey rekk, waaye it dina daaneel màggalukaayu Artemis sunu yàlla ju mag ji, tey neenal ndamam, moom mi Asi gépp te àddina sépp di màggal.»

19:28  Bi ñu déggee loolu, mer mu réy tàbbi ci ñoom, ñuy yuuxu ne: «Artemis mu Efes màgg na!»

19:29  Noonu dëkk bépp jaxasoo. Ñu bokk benn xalaat, daldi ne milib ca powukaay ba, diri Gayus ak Aristàrk, waa Maseduwan, ñi ànd ak Pool.

19:30  Pool nag bëgg a dugg ca mbooloo ma, waaye taalibe ya nanguwuñu ko.

19:31  Ñenn ca jawriñi nguur gi it, ñuy ay xaritam, yónnee ci moom, di ko dénk, mu bañ a jaay bakkanam ci dugg ca powukaay ba.

19:32  Noonu ndaje ma rëb, ba ñii di yuuxu lii, ñale di yuuxu laa, te ña ca gën a bare xamuñu lu waral ndaje ma.

19:33  Ci kaw loolu Yawut ya jéñ Alegsàndar ci kanam, te mbooloo ma di ko xaacu ay ndigal, mu daldi tàllal loxoom, ngir làyyi ca mbooloo ma.

19:34  Waaye bi ñu xamee ne Yawut la, ñépp a bokk benn baat, yuuxu diirub lu mat ñaari waxtu naan: «Artemis mu Efes màgg na!»

19:35  Gannaaw loolu boroom dëkk ba dalal mbooloo ma ne leen: «Yéen waa Efes, ana ku xamul ne, dëkku Efes moo di wottukaayu màggalukaayu Artemis ak nataalam, bi wàcce asamaan?

19:36  Gannaaw nag kenn mënta weddi loolu, war ngeen a dalal seen xel te bañ a sañaxu ci dara.

19:37  Ndaxte nit ñii ngeen fi indi sàccuñu ca màggalukaay ya te sosaluñu sunu yàlla.

19:38  Su fekkee ne Demetirus ak ay nawleem jànkoonte nañu ak kenn, am na ay bési layoo ak ñu yilif réew mi; nañu fa woo ku ñu amleenteel.

19:39  Waaye su ngeen di laaj leneen, mbooloom dëgg dina ko àtte.

19:40  Ndaxte fi mu ne man nañu noo jiiñ jógug mbooloo mi ndax li fi xew tey. Te bu loolu amee dunu am aw lay ci mbirum mbooloo mu rëb mii, ndaxte amul dara lu ko waral.»

19:41  Bi mu waxee loolu nag, mu tas mbooloo ma.

20:1  Bi yengu-yengu ba dalee, Pool woo taalibe ya fa moom, dooleel leen. Bi mu ko defee mu tàggoo ak ñoom, jóge fa, dellu diiwaanu Maseduwan.

20:2  Noonu mu jaar ca bérab yooyu, di dooleel nit ñi ak wax yu bare; ba noppi mu dem réewu Geres,

20:3  toog fa ñetti weer. Waaye bi mu nekkee ci kaw tànki dugg gaal jëm diiwaanu Siri, te Yawut yi lalal ko pexe, mu fas yéenee dellu, jaare Maseduwan.

20:4  Booba nag ñii ñoo ànd ak moom: Sopater, doomu Pirus mi dëkk Bere; Aristàrk ak Segond, ñi dëkk Tesalonig; Gayus, mi dëkk Derbë, ak Timote; te it Tisig ak Torofim ñi dëkk Asi.

20:5  Ñooñu nag jiitu, di nu nég dëkku Torowas.

20:6  Waaye naka nun, gannaaw màggalu Yawut, ga ñuy wax Mburu ya amul lawiir, nu dugg gaal ci Filib, def ci juróomi fan, fekksi leen Torowas, nu am fa juróom-ñaari fan.

20:7  Ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, booloo nanu ngir damm mburu ma. Te Pool, mi bëggoon a dem ca ëllëg sa, di diisoo ak ñoom te waxtaanam law ba ci xaaju guddi.

20:8  Ca néeg bu kawe, ba nu booloo nag, amoon na fa làmp yu bare.

20:9  Noonu waxambaane wu tudd Ëtikus te toog ca palenteer ba, gëmmeentu bay jeyaxu. Bi Pool di gën a yaatal waxtaanam nag, nelaw daldi ko jàpp, mu xàwweekoo ca ñetteelu taax ma, daanu, ñu yékkati ko, fekk mu dee.

20:10  Waaye Pool wàcc, daldi sëgg ci kawam, roof ko loxoom ne leen: «Bàyyileen jooy yi, mu ngi dund.»

20:11  Noonu mu yéegaat, damm mburu ma, lekk; ba noppi delluwaat ci waxtaanam, di ko yaatal ba ca njël, door a tàggoo.

20:12  Naka waxambaane wa, ñu indi ko muy dund, ba seen xol sedd guyy.

20:13  Nun nag nu jiitu, dugg gaal jëm Asos, fa nu Pool santoon, nu jële ko fa; fekk moom fas na yéeney dox, ba agsi fa.

20:14  Noonu mu fekksi nu ci Asos, nu jël ko ca gaal ga, dem Mitilen.

20:15  Gannaaw loolu gaal ga jóge fa, nu agsi ca ëllëg sa janook dunu Kiyos. Bés ba ca tegu nag nu jàll ba Samos, te ñetteelu fan ba nu àgg Mile.

20:16  Ndaxte Pool fasoon na yéenee teggi Efes, ngir bañ a yàgg ci diiwaanu Asi; mu ngi doon gaawantu, ngir màggal, gi ñuy wax Pàntakot fekk ko Yerusalem.

20:17  Bi Pool eggee Mile nag, mu yónnee ca Efes, ngir woo njiiti mbooloom ñi gëm.

20:18  Bi ñu ñëwee, mu ne leen: «Yéen xam ngeen bu baax, ni ma doon doxale diirub sama ngan gépp ci seen biir, li dale ci bés bi ma jëkkee teg tànk ci Asi ba tey.

20:19  Jaamu naa Boroom bi ci woyof gu mat ak ay rangooñ, dékku ay nattu yu ma pexey Yawut yi indil.

20:20  Xam ngeen ne, musuma leen a nëbb dara lu leen di jariñ, di leen jàngal ci kanamu ñépp ak ca kër ya.

20:21  Dénk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen, ñu tuub seeni bàkkaar, ba woññiku ci Yàlla te gëm sunu Boroom Yeesu.

20:22  «Léegi maa ngi nii di dem Yerusalem, ci li ma Xelu Yàlla mi xiirtal, te xawma lu ma fay dal.

20:23  Xam naa rekk ne, ci dëkkoo-dëkk Xel mu Sell mi xamal na ma ne, ay buum ak ay metit ñu ngi may nég.

20:24  Waaye sama bakkan soxalu ma, su fekkee bey naa sama sas, ba matal liggéey, bi ma Boroom bi dénk, maanaam ma seedeel ci ñépp xebaar bu baax, bi ëmb yiwu Yàlla.

20:25  «Fi mu ne nag xam naa ne, dootuleen gis sama kanam, yéen ñépp ñi ma jaaroon ci seen biir, di yégle nguuru Yàlla.

20:26  Moo tax may dëggal tey jii ne, wàccoo naa ak yéen ñépp bés pénc.

20:27  Ndaxte ñeebluwuma leen, ci di leen xamal lépp li Yàlla digle.

20:28  Wottuleen nag seen bopp te wottu coggal jépp, ji leen Xel mu Sell mi def sàmm, ngeen sàmm mbooloo, mi Yàlla jotal boppam ak deretu Doomam.

20:29  Xam naa ne, bu ma leen wonee gannaaw, bukki yu soxor dinañu tàbbi ci coggal ji te duñu ci ñeeblu kenn.

20:30  Ay nit dinañu jóg ci seen biir sax, di wax luy sànke, ngir sàkku ay taalibe.

20:31  Foogleen nag, di fàttaliku ne diirub ñetti at, guddi ak bëccëg, musumaa noppi di leen artu kenn ku nekk ci yéen ak ay rangooñ.

20:32  «Léegi nag maa ngi leen di dénk Boroom bi, moom ak kàddug yiwam, gi leen man a dëgëral te may leen cér ci biir gaayi Yàlla yu sell yépp.

20:33  Nammuma xaalisu kenn mbaa wurusam mbaa koddaayam.

20:34  Xam ngeen ne, faj naa samay soxla ak soxlay ñi ànd ak man ci sama loxo yii.

20:35  Ci lépp won naa leen royukaay, ci li nu war a dimbali ñi néew doole te fàttaliku li Yeesu Boroom bi wax moom ci boppam ne: “Joxe moo gën a barkeel nangu.”»

20:36  Bi mu waxee loolu, mu sukk ak ñoom ñépp, ñaan ci Yàlla.

20:37  Te ñépp jooy bu metti, di laxasu ci baatu Pool, fóon ko bu baax.

20:38  Li leen gën a teg aw tiis mooy li mu leen wax: «Dootuleen gis sama kanam.» Noonu ñu gunge ko ba ca gaal ga.

21:1  Bi nga xamee ne tàggoo nanu ak ñoom ci naqar, nu dugg gaal, jubal dunu Kos. Te ca ëllëg sa nu dem ba teer ca Rodd, ba noppi jóge fa, jàll ba Patara.

21:2  Foofa nag nu gis gaal guy jàll ba Fenisi, nu dugg ca, mu daldi teddi.

21:3  Noonu nu séen dunu Sipar, bàyyi ko ci sunu càmmooñ, jublu diiwaanu Siri, nu teersi Tir. Ndaxte foofa la gaal gi war a yebbee la mu yeboon.

21:4  Nu wut taalibe ya, ba gis leen, toog ak ñoom juróom-ñaari fan. Ñoom nag ñu ne Pool ci li leen Xelu Yàlla mi may, mu bañ a dem Yerusalem.

21:5  Moona bi jataayu gaal ga matee, nu awaat ci yoon wi. Te ñépp gunge nu, ñoom ak seeni jabar ak seeni doom; nu génn dëkk ba, sukk ca tefes ga, ñaan ci Yàlla.

21:6  Noonu nu tàggoo ak ñoom, dugg ca gaal ga, ñu dellu seen kër.

21:7  Bi nu jógee Tir nag, nu demaat ci géej, ba teer Patolemayis. Foofa nu nuyu bokk ya, yendu, fanaan.

21:8  Nu jóge fa ca ëllëg sa, ñëw ba ca dëkku Sesare. Nu dugg ca kër Filib, taskatu xebaar bu baax bi, mi bokk ci Juróom-ñaar ña, nu dal fa moom.

21:9  Amoon na ñeenti doom yuy janq, ñuy wax ci kàddug Yàlla.

21:10  Bi nu fa nekkee ay fan nag, yonent bu tudd Agabus jóge Yude, agsi.

21:11  Mu ñëw ci nun, daldi yeew ay loxoom ak i tànkam ak laxasaayu Pool naan: «Nii la Xel mu Sell mi waxe: “Ki moom laxasaay gii, Yawut yi dinañu ko yeewe nii ca Yerusalem, jébbal ko ñi dul Yawut.”»

21:12  Bi nu déggee loolu, nun ak ña fa nekk nu ñaan Pool, mu bañ a dem Yerusalem.

21:13  Ci kaw loolu Pool tontu ne: «Lu ngeen di jooy, di yàq sama xol? Bañuma ñu yeew ma rekk, waaye nangu naa sax, ñu rey ma ci Yerusalem ngir turu Yeesu Boroom bi.»

21:14  Bi nu ko mënul a dëpp, nu noppi ne: «Kon na coobareg Boroom bi am!»

21:15  Gannaaw fan yooyu nu defaru, ngir dem Yerusalem.

21:16  Noonu ay taalibe yu dëkk Sesare ànd ak nun, yóbbu nu ca nit ku tudd Manason, fu nu war a dal; moom nag nitu Sipar la woon, di taalibe bu yàgg.

21:17  Bi nu agsee Yerusalem nag, taalibe ya teeru nu ak mbég.

21:18  Ca ëllëg sa Pool ànd ak nun, seeti Saag, fekk njiit yépp teew fa.

21:19  Noonu Pool nuyu leen, nettali leen benn-benn li Yàlla def ci biir ñi dul Yawut, jaarale ko ci liggéeyam.

21:20  Bi ko njiit ya déggee, ñu màggal Yàlla ne ko: «Mbokk mi, gis nga ne, am na ay junniy Yawut ñu gëm, te ñépp a sawar ci yoonu Musaa.

21:21  Dégg nañu ci sa mbir nag ne, yaa ngi jàngal Yawut yépp, yi dëkk ci biir ñi dul Yawut, ñu bàyyi yoonu Musaa te bañ a xarafal seeni doom mbaa topp sunuy aada.

21:22  Lu nu ci war a def nag? Ndaxte ci lu wér dinañu xam ne, ñëw nga.

21:23  Nu ngi lay digal nag, nga def nii: am na ci nun ñeenti góor yu dige ak Yàlla.

21:24  Jël leen, bokk ak ñoom setlu, te nga gàddu seen peyu wateef. Noonu ñépp dinañu xam ne, li ñu déggoon ci sa mbir du dëgg, waaye yaa ngi jëf tey sàmm yoonu Musaa.

21:25  Naka ñi dul Yawut ñi gëm, bind nanu leen li nu àtte ne, ñu moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm te moytu deretu médd ak njaaloo.»

21:26  Bi ñu ko waxee, Pool jël nit ña te ca ëllëg sa mu bokk setlu ak ñoom, ñu dugg ca kër Yàlla ga. Ñu xamle ban bés la seen setlu di àgg, di bés bu ñuy jébbale sarax ngir kenn ku nekk ci ñoom.

21:27  Bi àppu juróom-ñaari fan ya di bëgg a jeex, Yawut yi jóge diiwaanu Asi gis Pool ca kër Yàlla ga. Ñu daldi jógloo mbooloo mépp, jàpp ko,

21:28  di xaacu ne: «Wallee, wallee, yéen bokki Israyil; waa jaa ngi nii, moom miy waare fépp ak ci ñépp, bay suufeel sunu xeet ak yoonu Musaa ak bérab bii; dugal na sax ay Gereg fii ci kër Yàlla gi, ba indi sobe ci bérab bu sell bii.»

21:29  Li tax ñu wax loolu, mooy gisoon nañu Torofim mu Efes, ànd ak moom ca dëkk ba, te ñu yaakaar ne, Pool dugal na ko ca kër Yàlla ga.

21:30  Noonu dëkk ba bépp màbb, mbooloo ma ne këpp, ñu jàpp Pool, génne ko ca kër Yàlla ga. Ca saa sa ñu tëj bunt ya.

21:31  Bi ñu koy wut a rey, xebaar ba agsi ba ca kilifag mbooloom xarekat ba, naan Yerusalem gépp jaxasoo na.

21:32  Ca saa sa mu ànd ak ay xarekat ak ay njiiti xare, ne jaas wàcc ci ñoom. Bi Yawut ya gisee kilifa ga ak xarekat ya nag, ñu daldi bàyyi dóor, ya ñu doon dóor Pool.

21:33  Noonu kilifa ga jegesi jàpp ko, santaane ñu jéng ko ak ñaari càllala. Bi ñu ko defee mu laaj ku mu doon ak lu mu def.

21:34  Waaye ci biir mbooloo ma, bu ñii nee lii, ña ca des ne laa. Kon nag gannaaw mënu caa xam dara lu wóor ndax coow li, mu santaane, ñu yóbbu ko ci biir tata ja.

21:35  Bi Pool eggee ca yéegukaayu tata ja, aaytalu mbooloo ma réy, ba ay xarekat fab ko.

21:36  Ndaxte mbooloo maa nga ko topp, di xaacu ne: «Reyleen ko!»

21:37  Bi ñu koy bëgg a dugal ca tata ja, Pool ne kilifa ga: «Ndax man naa laa wax dara?» Mu tontu ko: «Yaw dégg nga gereg?

21:38  Kon nekkuloo waayi Misra, jooju jógloo woon nit ñi keroog te yóbbu woon ñeenti junniy bóomkat ca màndiŋ ma?»

21:39  Pool ne ko: «Man Yawut laa, di jaambur ci Tars, dëkk bu am tur ci diiwaanu Silisi. Maa ngi lay ñaan, ma wax ak mbooloo mi.»

21:40  Te kilifa ga may ko ko. Noonu Pool taxaw ca yéegukaay ba, tàllal loxoom mbooloo ma, ñu daldi ne tekk. Mu wax ak ñoom ci làkku yawut ne:

22:1  «Yéen bokk yi ak baay yi, dégluleen samaw lay.»

22:2  Bi ñu déggee, mu di leen wax ci làkku yawut, ñu gën ne xeram. Noonu Pool ne leen:

22:3  «Man Yawut laa, juddoo Tars ci diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Taalibe laa woon ci Gamaleel, mu jàngal ma bu wér yoonu sunuy maam, ba ma sawar ci Yàlla, mel ni yéen ñépp tey.

22:4  Daan naa fitnaal ña bokkoon ci yoon wii, ba di ci rey sax; yeew naa góor ak jigéen, tëj leen;

22:5  saraxalekat bu mag ba ak mbooloom njiit yi yépp man nañu ma cee seede. Am bés ñu bindal ma ay bataaxal ngir bokki Damas. Ma doon fa dem, ngir yeew ña fa nekkoon, indi leen Yerusalem, ngir ñu yar leen.

22:6  «Waaye ci digg-bëccëg, bi ma jaaree ca yoon wa, ba jegesi Damas, ca saa sa leer gu mag jóge asamaan, melax ba ëmb ma.

22:7  Ma daldi ne nërëm ci suuf, dégg baat bu ma ne: “Sool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal?”

22:8  Ma tontu ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Mu ne ma: “Maa di Yeesum Nasaret, mi ngay fitnaal.”

22:9  Ñi ma àndaloon gis nañu leer ga, waaye dégguñu baatu ka doon wax ak man.

22:10  Noonu ma laaj ko: “Lu ma war a def, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Jógal dem Damas, foofa dees na la biral lépp, li ma la yen.”

22:11  Gannaaw gisuma woon dara ndax leeraayu melxat ga, ña ma àndal wommat ma, ma ñëw Damas.

22:12  «Bi ma ko defee ku tudd Anañas ñëw ci man. Nit ku ragal Yàlla la woon ci sàmm yoonu Musaa, te Yawuti Damas yépp seedeel ko lu baax.

22:13  Mu taxaw ci sama wet ne ma: “Sool sama mbokk, delluwaatal di gis.” Noonu ma daldi gisaat ca saa sa, xool ko.

22:14  Mu ne ma: “Sunu Yàllay maam tànn na la, ba may la, nga xam coobareem te gis Aji Jub ji te nga dégg ay waxam.

22:15  Ndaxte li nga gis te dégg ko, dinga ko seede ci ñépp.

22:16  Léegi nag, looy nég? Jógal, ñu sóob la ci ndox, nga set ci say bàkkaar ci tudd turu Yeesu.”

22:17  «Bi ma dellusee Yerusalem nag, di ñaan ca kër Yàlla ga, leer tàbbi ci man.

22:18  Ma daldi gis Boroom bi, mu ne ma: “Génnal Yerusalem ci ni mu gën a gaawe, ndaxte duñu nangu li ngay seede ci man.”

22:19  Waaye ma tontu ne: “Boroom bi, xam nañu ne, dama daan wër jàngoo-jàngu, di tëj kaso ak di dóor ay yar ñi la gëm.

22:20  Rax-ca-dolli bi ñu tuuree deretu Ecen, mi la doon seedeel, teewe naa ko, ànd ca, bay wottu sax yérey ñi ko doon rey.”

22:21  Waaye Boroom bi ne ma: “Demal, dinaa la yebal fu sore, nga jëm ci xeeti ñi dul Yawut.”»

22:22  Mbooloo ma déglu ko nag ba ca wax jooju, waaye bi ñu déggee loolu, ñu daldi yuuxu naan: «Farleen ko ci àddina! Yembar mu mel ni moom yeyoowul a dund!»

22:23  Ñu daldi yuuxu ak di sànni seeni yére, tey callameeru suuf.

22:24  Noonu kilifa ga santaane, ñu dugal Pool ca tata ja te caw ko ay yar yu metti, laaj ko ba xam lu tax ñu di ko yuuxoo nii.

22:25  Waaye bi ñu koy joñ ak ay der, Pool ne njiitu xare ba fa taxaw: «Ndax am nga sañ-sañu dóor ay yar jaamburu Room, te fekk yoon dabu ko sax?»

22:26  Bi ko njiit la déggee, mu fekki kilifaam, yégal ko ko; mu ne ko: «Ndax xam nga li ngay def? Nit kale jaambur la ci Room.»

22:27  Noonu kilifa ga ñëw laaj Pool: «Wax ma, ndax jaambur nga ci Room?» Mu tontu ko: «Waaw, moom laa.»

22:28  Kilifa ga ne ko: «Man fey naa xaalis bu bare, ngir nekk jaambur ci Room.» Waaye Pool tontu ko: «Man de dama koo judduwaale.»

22:29  Ñi ko bëggoon a dóor ay yar nag randu ko ca saa sa. Te kilifa ga sax tiit ci xam ne Pool jaamburu Room la, te yeewlu na ko.

22:30  Ca ëllëg sa mu bàyyi ko, ndaxte bëggoon na xam bu wóor lu ko Yawut ya jiiñ. Mu santaane ne, saraxalekat yu mag ya dajaloo, ñoom ak kureelu àttekat ya. Gannaaw loolu mu indilu Pool, dëj ko ci seen kanam.

23:1  Noonu Pool xool jàkk géew ba ne leen: «Bokk yi, ci xel mu dal laa doxale ci kanam Yàlla ba ci bésu tey bi.»

23:2  Ci kaw loolu saraxalekat bu mag ba, di ku ñuy wax Anañas, sant ña taxaw ca wetam, ñu fél gémmiñam.

23:3  Pool ne ko: «Yàlla dina la dóor, yaw mi naaféq, bay samandaay miir bu joy bu ñu weexal. Yaa ngi toog di ma àtte, ci li yoon wi digle, ba noppi santaane ñu dóor ma, ci li yoon wi tere!»

23:4  Waaye ña taxaw ca wetam ne ko: «Ndax dangay xas saraxalekat bu mag, bi Yàlla fal?»

23:5  Pool tontu leen: «Bokk yi, xawma woon ne saraxalekat bu mag bi la, ndaxte tëral nañu ci Mbind mi ne: “Bul wax lu bon sa kilifag xeet.”»

23:6  Naka noona Pool, mi xam ne, genn-wàllu kureel ga bokk nañu ci tariixab Sadusen ya, te ña ca des bokk ci tariixab Farisen ya, mu wax ci kaw ci biir géew ba ne: «Bokk yi, man Farisen laa, te Farisen moo ma jur; li tax ñu may àtte tey mooy sama yaakaar ci ne, ñi dee dinañu dekki.»

23:7  Bi mu waxee loolu nag, werante wu metti daldi xew diggante Farisen ya ak Sadusen ya, ba mbooloo ma xaajalikoo.

23:8  Ndaxte Sadusen yi nanguwuñu ne, ndekkite mbaa malaaka mbaa rab, dara am na ci, waaye Farisen nangu nañu yooyu yépp.

23:9  Ci kaw loolu nag coow lu bare daldi jib. Ñenn ca xutbakat, ya bokk ca Farisen ya, ne bërét, daldi xuloo bu metti ne: «Gisunu dara lu bon ci nit kii. Su fekkeente ne, rab a ko wax mbaa malaaka...?»

23:10  Noonu xuloo ba daldi gën a tàng, ba kilifa ga ragal ne, nit ñi dinañu daggaate Pool. Kon mu sant xarekat ya, ñu wàcc, nangu Pool ci ñoom, yóbbu ko ca tata ja.

23:11  Ca guddi ga nag Boroom bi taxaw ci wetu Pool ne ko: «Takkal sa fit; ni nga ma seedee ci Yerusalem, noonu nga may seedee ca Room.»

23:12  Bi bët setee Yawut ya daldi lal pexe; ñu dige ci ngiñ ne, duñu lekkati, duñu naanati, ba kera ñuy rey Pool.

23:13  Ña lal pexe ma, seen lim ëpp na ñeent-fukk.

23:14  Noonu ñu dem ca saraxalekat yu mag ya ak njiit ya ne leen: «Giñ nanu ne, dunu mos dara, ba kera nuy rey Pool.

23:15  Léegi nag yéen ak kureelu àttekat ya, laajleen kilifa ga, mu indi ko ci seen kanam, mel ni dangeen a bëgg a seet mbiram bu gën a wóor. Bu ko defee nun dinanu fagaru, ngir rey ko, bala moo agsi.»

23:16  Waaye jarbaatu Pool yég fiir ga, mu dem, dugg ca tata ja, yégal ko Pool.

23:17  Bi ko Pool déggee, mu woo kenn ca njiiti xare ba ne ko: «Yóbbul waxambaane wii ca kilifa ga, ndax am na lu mu ko war a yégal.»

23:18  Njiit la jël ko, yóbbu ko ca kilifa ga ne ko: «Pool, mi ñu jàpp, moo ma woo, ñaan ma, ma indil la waxambaane wii, ndaxte am na lu mu lay wax.»

23:19  Noonu kilifa ga jàpp ci loxob waxambaane wa, wéetoo ak moom, laaj ko: «Loo ma bëgg a yégal?»

23:20  Mu tontu ne: «Yawut yi dañoo dige, ngir ñaan la, nga indi Pool ëllëg ca kanamu kureelu àttekat ya, mel ni dañoo bëgg a seet mbiram bu gën a wóor.

23:21  Bu leen ko may, ndaxte lu ëpp ñeent-fukk ci ñoom ñu ngi koy lalal fiir. Dige nañu ak ngiñ ne, dootuñu lekk, dootuñu naan, li feek reyuñu ko; fi mu ne sax fagaru nañu, di xaar, nga nangu.»

23:22  Kilifa ga nag sant waxambaane wa, mu bañ koo àgge kenn, ba noppi mu yiwi ko, mu dem.

23:23  Bi mu ko defee mu woo ñaar ci njiiti xare ba ne leen: «Waajal-leen ñaari téeméeri xarekat ak juróom-ñaar-fukki gawar ak ñaari téeméer ñu gànnaayoo xeej, ngeen dem Sesare ci juróom-ñeenti waxtu ci guddi.

23:24  Wutal-leen it Pool lu mu war, ngeen yóbbu ko ci jàmm ak salaam ba ca Feligsë, boroom réew mi.»

23:25  Noonu mu bind bataaxal bii:

23:26  Yaw Feligsë mu tedd mi, di boroom réew mi; man Këlódd Lisiyas maa ngi lay nuyu.

23:27  Yawut yi jàpp nañu nit kii, bëgg koo rey, waaye bi ma yégee ne, jaambur la ci Room, wallu naa ko ak ay xarekat, ba musal ko.

23:28  Bëggoon naa xam lu tax ñu kalaame ko. Moo tax ma yóbbu ko ca kanamu seen kureelu àttekat ya.

23:29  Gis naa ne li ñu ko jiiñ mu ngi aju ci ay werantey seen yoon, waaye jiiñuñu ko dara lu jar dee mbaa jéng.

23:30  Te bi ma déggee ne, ñu ngi koy fexeel, yebal naa ko ci yaw ci saa si. Sant naa nag ñi ko kalaame, ñu xamal la seen lay.

23:31  Noonu xarekat ya jël Pool ci guddi, indi ko ba ca dëkku Antipataris, ni ñu leen ko sante.

23:32  Ca ëllëg sa ñu woññiku, dellusi ca tata ja, bàyyi gawar ga, ñu gunge ko.

23:33  Bi gawar ga àggee Sesare, ñu jox boroom réew ma bataaxal ba, jébbal ko Pool.

23:34  Bi loolu amee boroom réew ma jàng bataaxal ba, laaj ci ban diiwaan la Pool dëkk. Bi mu yégee ne, mu ngi dëkk Silisi,

23:35  mu ne ko: «Kon bu ñi la kalaame ñëwee, dinga layoo.» Mu santaane nag, ñu denc ko ca kër buur ba Erodd.

24:1  Bi juróomi fan wéyee, Anañas saraxalekat bu mag ba dikk, ànd ak ay njiit ak layookat bu tudd Tertul, ñu woo Pool ci yoon fa kanam boroom réew ma.

24:2  Noonu ñu woo Pool, te Tertul daldi ko jiiñ naan: «Yaw Feligsë mu tedd mi, sa nguur jural na nu jàmm ju neex, te sa jàppandil soppi na lu bare ci sunu xeet.

24:3  Gis nanu ko fépp ak ci lépp, di la gërëm ak sunu xol bépp.

24:4  Waaye ngir bañ a yàggal jataay bi, maa ngi lay ñaan ci sa lewetaay, nga déglu nu ci lu gàtt.

24:5  Ndaxte ci mbirum nit kii teew, gis nanu ne rambaaj la, buy indi xëccoo ci Yawut yi ci àddina sépp, di njiitu mbooloo mu ñuy wax Nasaréen.

24:6  Dem na ba jéem a teddadil sax kër Yàlla ga, waaye jàpp nanu ko.

24:8  Soo ko laajee, yaw ci sa bopp, dinga gis ne, li nu koy jiiñ dëgg la.»

24:9  Ci kaw loolu Yawut ya ànd ca, di dëggal ne loolu wóor na.

24:10  Bi loolu amee boroom réew ma jox Pool kàddu gi. Noonu mu làyyi ne: «Xam naa ne, yaa ngi àtte xeet wi diirub at yu bare, moo tax maa ngi làyyi ak kóolute.

24:11  Man ngaa wóorliku ne, ëppagul fukki fan ak ñaar demoon naa Yerusalem ngir màggali.

24:12  Te kenn gisu ma, maay werante mbaa di jógloo mbooloo, muy ca kër Yàlla ga mbaa ca jàngu ya mbaa ci biir dëkk ba.

24:13  Te mënuñoo firndeel dara ci li ñu may jiiñ léegi.

24:14  Waaye nangu naa ci sa kanam ne, maa ngi jaamu Yàllay sunuy maam, ci topp yoon wi ñu ne, mooy tariixa; terewul ne, lépp li ñu tëral ci yoonu Musaa ak li yonent yi bind, gëm naa ko.

24:15  Te bokk naa ak ñoom yaakaar ci Yàlla, ne ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki keroog yawmelxayaam.

24:16  Moo tax fu ma tollu, maa ngi góor-góorlu, ngir am xel mu dal fa kanam Yàlla ak fa kanam nit ñi.

24:17  «Noonu gannaaw gëjeb at yu bare ñëw naa, ngir indil sama xeet ndimbal te jébbal Yàlla ay sarax.

24:18  Bi ma koy def nag, gis nañu ma ca kër Yàlla ga, ma setlu ba noppi, fekk ànduma ak mbooloo te indiwuma benn coow.

24:19  Waaye ay Yawut yu dëkk Asi — xanaa kay ñoo waroon a ñëw ci sa kanam, di ma kalaame, bu ñu amee dara lu ñu may topp.

24:20  Waaye it na nit ñii wax ci lan laa tooñe ci jataayu géewub àtte ba,

24:21  xanaa li ma waxoon ca kaw ci seen biir rekk ne: “Mbirum ndekkitel ñi dee moo tax ngeen dëj ma ci seen kanam tey!”»

24:22  Bi mu waxee noonu, Feligsë mi xam bu wóor mbirum yoon wi, yiwi leen ba beneen yoon. Mu ne leen: «Bu Lisiyas kilifag xare bi ñëwee, dinaa àtte seen mbir.»

24:23  Noonu mu sant njiitu xare ba ne ko: «Nanga wottu Pool, waaye nga may ko féex, te bàyyi ay xaritam, ñu topptoo ko.»

24:24  Bi ay fan wéyee, Feligsë ñëwaat, ànd ak jabaram Dursil, miy Yawut. Noonu mu woolu Pool, di ko déglu ci mbirum gëm Yeesu Kirist.

24:25  Waaye bi Pool di waxtaan ci mbirum njub ak moom sa bopp ak bés pénc, Feligsë daldi tiit, yiwi ko ne ko: «Demal, bu ma amee jot, dinaa la woolu.»

24:26  Fekk yaakaaroon na it ne, Pool dina ko jox xaalis; kon mu di ko faral a woolu, ngir waxtaan ak moom.

24:27  Bi ñaari at weesoo nag, amoon na ku wuutu Feligsë, tudd Porsiyus Festus. Noonu Feligsë, mi bëggoon lu neex Yawut ya, bàyyi Pool ca kaso ba.

25:1  Bi Festus teersee ci diiwaanam, mu teg ca ñetti fan, dem Yerusalem.

25:2  Noonu saraxalekat yu mag ya ak njiiti Yawut ya kalaame Pool ci moom.

25:3  Ñuy sàkku ndimbal ci moom, di ko ñaan bu wér, mu yónni Pool Yerusalem, fekk lal nañu fiiru rey ko ca yoon wa.

25:4  Waaye Festus tontu leen ne: «Ñu ngi wottu Pool ca Sesare, te dinaa fa dem fi ak fan yu néew.»

25:5  Mu ne leen: «Ñi am maana ci yéen nag, nangeen ànd ak man, layooji ak nit ka, bu dee tooñ na.»

25:6  Noonu Festus am fa ñoom juróom-ñett ba fukki fan, ba noppi dem Sesare. Ca ëllëg sa mu toog ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi Pool.

25:7  Bi mu ñëwee nag, Yawut ya jóge Yerusalem wër ko, di ko jiiñ tooñ yu bare te réy, te mënuñu leen a firndeel.

25:8  Noonu Pool làyyi ne: «Tooñuma yoonu Yawut ya, tooñuma kër Yàlla ga, tooñuma buur ba Sesaar.»

25:9  Ci kaw loolu Festus, mi bëgg lu neex Yawut ya, tontu Pool ne: «Ndax bëgguloo dem Yerusalem, nga layoo fa ci mbir yii ci sama kanam?»

25:10  Waaye Pool ne ko: «Maa ngi nii taxaw ci kanam àttekaayu buur Sesaar; te fii lañu ma war a àttee. Te yaw ci sa bopp xam nga bu baax ne, tooñuma Yawut yi.

25:11  Su ma tooñoon mbaa ma def lu bon lu jar dee, kon duma tinu ngir bañ a dee. Waaye bu li ñu may jiiñ taxawul, kenn sañu ma leen a jébbal. Dénk naa sama mbir Sesaar.»

25:12  Bi mu waxee loolu, Festus gise ak ñi ko wër, mu tontu ko: «Dénk nga sa mbir Sesaar, kon ci moom ngay dem.»

25:13  Ba ñu ca tegee ay fan, buur Agaripa ak Berenis ñëw Sesare, ngir nuyusi Festus.

25:14  Bi seen ngan di ruus nag, Festus diis buur ba mbirum Pool ne ko: «Feligsë batale na nu ak kenn ku ñu tëj.

25:15  Te bi ma nekkee Yerusalem, saraxalekat yu mag ya ak njiiti Yawut ya kalaame nañu ko ci man, ñaan ma, ma daan ko.

25:16  Waaye ma tontu leen ne: “Jébbale nit, fekk jàkkaarloowul ak ñi koy jiiñ, ba man a làyyil boppam ci li ñu koy jiiñ, loolu dëppoowul ak aaday nguuru Room.”

25:17  Bi ñu àndee ak man ba fii nag, randaluma mbir mi, waaye ca ëllëg sa sax toog naa ca àttekaay ba, joxe ndigal, ñu indi nit kooku.

25:18  Ñi koy kalaame nag, bi ñu taxawee, jiiñuñu ko benn ñaawteef ci yi ma yaakaaroon;

25:19  waaye ñuy werante rekk ak moom ci seen yoon ak ci mbirum ku tudd Yeesu, mi dee, te Pool sax ci ne, mu ngi dund.

25:20  Gannaaw lijjanti mbir moomu jafe woon na ma lool nag, ma laaj ko, ndax bëgg na dem Yerusalem, layooji fa ci mbir yooyu.

25:21  Waaye Pool ñaan, nu fomm mbiram, ba kera buur bu tedd ba di ko àtte. Noonu santaane naa ñu aj ko, ba keroog ma koy yónnee Sesaar.»

25:22  Booba nag Agaripa ne Festus: «Man sax bëgg naa dégg nit kooku.» Festus tontu ko: «Bu ëllëgee dinga ko dégg.»

25:23  Ca ëllëg sa nag Agaripa ak Berenis ñëw bu xumb, ñu dugg ca néegu àtte ba, ànd ak kilifay xare ba ak ña am maana ca dëkk ba. Noonu Festus joxe ndigal, ñu indi Pool.

25:24  Bi mu ñëwee, Festus ne: «Buur Agaripa ak yéen ñépp, ñi fi teew tey, nit kaa ngi nii! Mbiram moo tax mbooloom Yawut yépp, muy ci Yerusalem, muy fii, wër ma di yuuxu ne: “Nit kii waratul a dund.”

25:25  Waaye gis naa ne, deful dara lu jar dee. Moona, gannaaw moom ci boppam dénk na boppam buur bu tedd ba, fas naa yéene yónnee ko ko.

25:26  Fekk awma dara lu wóor ci mbiram, lu ma man a bind sang bi. Moo tax ma indi ko ci seen kanam, rawatina ci sa kanam buur Agaripa, ngir sunu jataay may ma lu ma bind.

25:27  Ndaxte yaakaar naa ne, yónnee ku ñu tëj, te bañ caa boole lu ko waral, àndul ak xel.»

26:1  Bi mu ko waxee, Agaripa ne Pool: «Jëlal kàddu gi.» Noonu Pool tàllal loxoom, daldi làyyi ne:

26:2  «Buur Agaripa, ma làyyi ci sa kanam tey ci lépp, li ma Yawut yiy jiiñ, xol bu sedd la ci man,

26:3  ndaxte xam nga bu baax aaday Yawut yi ak seeni werantey yoon. Kon maa ngi lay ñaan, nga déglu ma ak muñ.

26:4  «Ci lu jëm ci Yawut yi, xam nañu sama dund li dale ci samag ndaw, muy ci sama biir xeet, muy ci Yerusalem.

26:5  Xam nañu ma bu yàgg te man nañoo seede, su leen neexee, ne daan naa dund ni Farisen, te mooy tariixa bi gën a diis ci sunu diine.

26:6  Li ma indi ci kureelu àttekat yii nag, mooy yaakaar ne, Yàlla dina amal li mu digoon sunuy maam.

26:7  Dige booba la fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil di sàkku, ngir jot ko, ci jaamu Yàlla ak cawarte guddi ak bëccëg. Yaw buur, yaakaar joojoo tax ñu may kalaame, ñoom Yawut yi.

26:8  Lu tax seen xel dàq ne, Yàlla dina dekkal ñi dee?

26:9  «Man sax ci sama bopp defe woon naa ne, war naa def lu bare, ngir suufeel turu Yeesum Nasaret.

26:10  Daan naa ko def ci Yerusalem, ba noppi ma jot sañ-sañ ci saraxalekat yu mag ya, bay tëj gaayi Yàlla yu bare. Rax-ca-dolli ku ñu ci masoon a bëgg a rey, ànd naa ci.

26:11  Daan naa wër jàngoo-jàngu, di leen teg toskare te di leen jéem a weddiloo. Te sama mer daa na tar, ba ma di leen xañ ba ca dëkk yu sore, ngir fitnaal leen.

26:12  «Noonu am bés, may dem dëkku Damas, yor sañ-sañ ak ndigalu saraxalekat yu mag ya.

26:13  Ca njolloor, buur bi, gis naa ca yoon wa leer gu jóge asamaan ne ràyy, ba raw leeru jant, melax ba ëmb ma, man ak ñi ma àndal.

26:14  Nu ne nërëm ci suuf, ma dégg baat bu ma wax ci làkku yawut ne: “Sool, Sool, lu tax nga di ma fitnaal? Ngay bëre ak man ni fas wuy woŋŋeetu ku koy jam dëgël, metti na ci yaw.”

26:15  «Noonu ma tontu ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Maa di Yeesu, mi ngay fitnaal.

26:16  Waaye jógal taxaw. Lii moo tax ma feeñu la: teg naa la yen, nga di ma seedeel ci lépp li nga gis ci man, ak li ma lay feeñuji.

26:17  Dinaa la musal ci bànni Israyil ak ci ñi dul Yawut. Ci ñoom laa lay yebal,

26:18  ngir ubbi seeni bët, nga jële leen ci lëndëm, tàbbal leen ci leer, nga nangoo leen ci sañ-sañu Seytaane, woññi leen ci Yàlla, ma baal leen seeni bàkkaar te may leen cér ci biir sama gaa yi sell ci kaw ngëm.”

26:19  «Kon nag buur Agaripa, woruma li ma Yàlla yen ci peeñu.

26:20  Waaye li tàmbali ci Damas, teg ci dëkku Yerusalem ak réewu Yawut mépp, ba agsi ci ñi dul Yawut, yégal naa leen, ñu tuub seeni bàkkaar te woññiku ci Yàlla, bay jëf lu dëppook réccu.

26:21  Loolu nag moo waral Yawut yi jàpp ma ca kër Yàlla ga, di ma fexee rey.

26:22  Waaye gannaaw Yàllaa ngi may taxawu ba tey, maa ngi taxaw fi, di ko seedeel ci mag ak ndaw; yokkuma dara ci li yonent yi ak Musaa xamle woon lu jiitu,

26:23  maanaam Almasi bi dina dékku ay coono, te mooy jëkk a dekki, bay jollil leer ci bànni Israyil ak ñi dul Yawut.»

26:24  Bi muy làyyee nii, Festus daldi ko gëdd ak baat bu kawe ne ko: «Dangaa dof Pool! Xanaa sa njàng mu réy mi da laa xañ sago.»

26:25  Waaye Pool tontu ko: «Festus mu tedd mi, dofuma; waaye lu dëggu laay wax te ànd ak sago.

26:26  Yëf yii leer na buur bi, moo tax maa ngi koy wax ak kóolute. Wóor naa ne, dara ci lii may wax umpu ko, ndaxte lii amewul ciy ruq.

26:27  Yaw buur Agaripa, ndax gëmuloo yonent yi? Xam naa bu wér ne, gëm nga.»

26:28  Noonu Agaripa ne Pool: «Xanaa yaw, ci diir bu gàtt bii rekk, nga ma bëgg a dugale ci gaayi Kirist!»

26:29  Pool tontu ko: «Muy tey, muy ëllëg, waxuma yaw rekk waaye it ñi may déglu tey ñépp, na Yàlla def, ba ngeen fekksi ma ci li ma nekk, lu moy jéng yii!»

26:30  Ci kaw loolu buur ba daldi jóg, boroom réew ma topp ci, Berenis tegu ca ak mbooloo ma mépp.

26:31  Bi ñu génnee nag, ñuy waxante ne: «Nit kii deful dara lu jar dee mbaa kaso.»

26:32  Te Agaripa ne Festus: «Manoon nanu koo yiwi, bu dénkuloon mbiram Sesaar.»

27:1  Bi loolu wéyee ñu fas yéene noo dugal gaal jëme réewu Itali. Noonu ñu jël Pool ak ñeneen ñi ñu tëjoon, dénk leen njiitu xare bu tudd Yulyus, mi bokk ci mbooloom xare mu buur.

27:2  Nu dugg ca gaalu dëkku Adaramit guy taxaw ci teeruy Asi, daldi tàbbi ci biir géej; te Aristàrk, mi dëkk Tesalonig ci diiwaanu Maseduwan, ànd ak nun.

27:3  Ca ëllëg sa nu teer Sidon; Yulyus laabiir ci Pool, may ko mu dem ci ay xaritam, ngir ñu ganale ko.

27:4  Bi nu fa jógee, nu dem ci biir géej, leru dunu Sipar ci fegu ngelaw li, ndaxte ngelaw li da noo soflu.

27:5  Nu jàll géej, gi janook diiwaani Silisi ak Pamfili, teersi Mira ca wàlli Lisi.

27:6  Foofa nag njiit la gis gaal gu jóge Alegsàndiri, jëm Itali, mu dugal nu ca.

27:7  Noonu nuy dem ndànk diirub fan yu bare, ba janook Kanidd ci kaw coono bu réy; te ndegam ngelaw li mayu nu, nu jëm kanam, nu leru dunu Kereet ci fegu ngelaw li, janook Salmon.

27:8  Nu romb fa ak coono yu bare, agsi ca bérab bu ñuy wax Teeru yu neex, te dend ak dëkku Lase.

27:9  Fekk booba yàggoon nañu ca yoon wa, te dem ci géej daldi aaytal, ndaxte jamonoy Kooru Yawut ya wees na. Moo tax Pool digal leen ne:

27:10  «Gaa ñi, gis naa ne, tukki bi ëmb na musiba ak kasara ju bare, waxuma gaal gi ak li mu yeb waaye sunuy bakkan sax xaj na ci.»

27:11  Waaye njiit la sobental waxi Pool, déggal dawalkat ba ak boroom gaal ga.

27:12  Te gannaaw teeru ba neexul a lollikoo, ña ca ëpp mànkoo ci jóge fa, dem ci biir géej, ngir wut a agsi Fenigsë, biy teerub dunu Kereet te janook sowu suuf ak sowu kaw, nu lollikoo fa.

27:13  Noonu bi ngelaw lu woyof liy jóge sudd wolee, ñu defe ne, man nañoo sottal seen pexe, ñu wëgg diigal, daldi tafu ci dunu Kereet.

27:14  Waaye nes tuuti ngelaw lu wole penku, ñu di ko wax «Ërakilon,» jóge ca dun ba, ne milib ci sunu kaw.

27:15  Mu ëpp doole gaal ga, daldi ko wat, ba nu bayliku, daldi yal.

27:16  Nu daldi daw, leru dun bu tuuti bu ñuy wax Kóda ci fegu ngelaw, rawale looco ga ci kaw gaal ga ak coono bu bare.

27:17  Bi ñu ko yéegee, ñu fab ay buum, ngir laxas ca taatu gaal ga, ngir ragal a daanu ci suuf su nooy su ñuy wax Sirt; ba noppi ñu daldi sànni diigal, ngir wàññi doxub gaal ga, nuy yale noonu.

27:18  Waaye bi nu ngelaw li sonalee bu metti, ca ëllëg sa ñu sànni la gaal ga yeboon ca géej ga.

27:19  Te ca ñetteelu fan ba, ñu sànni ak seeni loxo jumtukaay, yi ñu yeboon ngir fàggu.

27:20  Noonu jant bi ne meŋŋ te biddiiw ne mes ay fan yu bare, fekk ba tey ngelaw li di wol ak doole, ba sunu yaakaaru mucc gépp tas.

27:21  Bi loolu di xew, fekk gëj nañoo lekk, Pool daldi taxaw ci seen biir ne leen: «Gaa ñi, li gënoon mooy ngeen déglu ma te bañ a jóge Kereet, ba indil seen bopp musiba ak kasara ju réy jii.

27:22  Léegi nag maa ngi leen di dénk, ngeen takk seen fit, ndax gaal gi rekk mooy yàqu, waaye kenn ci yéen du dee.

27:23  Ndaxte ci guddi menn malaaka dikkal na ma, jóge ci Yàlla sama Boroom, bi may jaamu.

27:24  Mu ne ma: “Pool bul tiit; fàww nga taxaw ci kanamu Sesaar, te yaa tax Yàllay aar bakkani ñi nga àndal ñépp.”

27:25  Moo tax gaa ñi, takkleen seen fit, ndax wóolu naa Yàlla ne, li mu ma wax, dina am.

27:26  Waaye war nanoo luf cib dun.»

27:27  Ca fukkeelu guddi ga ak ñeent nu nga doon jayaŋ-jayaŋi ca géeju Adiratig; noonu ca xaaju guddi dawalkati gaal ga defe ne, danu jegesi suuf.

27:28  Ñu sànni nattukaay ba ci biir géej, mu jàpp ñeent-fukki meetar, dem ca kanam tuuti, sànniwaat ko, jàpp fanweeri meetar.

27:29  Ñu ragal ne, dinañu fenqu ci ay xeer, kon ñu daldi sànni ñeenti diigal ci geenu gaal ga, di ñaan bët set.

27:30  Waaye ci kaw loolu dawalkati gaal ga taafantaloo sànniji ay diigal ca boppu gaal ga, fekk dañuy fexee jël looco ga, ba raw.

27:31  Waaye Pool ne njiit la ak xarekat ya: «Bu ñii desul ci gaal gi, dungeen raw.»

27:32  Noonu xarekat ya dagg buum, yay téye looco ga, bàyyi ko mu wéy.

27:33  Bi bët setagul, Pool sant leen ñu lekk; mu ne leen: «Tey mooy seen fukki fan ak ñeent yu ngeen ne jonn, lekkuleen, mosuleen dara.

27:34  Maa ngi leen di sant nag, ngeen lekk, ndax noonu rekk ngeen man a rawe. Ndax genn kawar du rot ci yéen.»

27:35  Bi mu waxee loolu, mu fab mburu, sant Yàlla ci kanamu ñépp, damm ko, daldi ko lekk.

27:36  Bi ñu gisee loolu, ñépp dëgëraat, ñu daldi lekk ñoom itam.

27:37  Mboolem ñi nekkoon ca gaal ga mat na ñaari téeméeri nit ak juróom-ñaar-fukk ak juróom-benn.

27:38  Noonu ñu lekk ba suur, daldi sànni pepp ma ca géej ga, ngir woyofal gaal ga.

27:39  Bi bët setee nag, xàmmiwuñu réew ma, waaye séen nañu ruqu tefes. Noonu ñu fas yéene caa teeral gaal ga, bu ñu ko manee.

27:40  Ñu dagg diigal ya, bàyyi leen ci biir géej, yiwiwaale baar ba; ba noppi firi wiiru kanam ga, jublu ca tefes ga.

27:41  Waaye ñu dal ca tundu suuf ca bérab bu ñaari koroŋ daje, gaal ga daldi fa luf. Boppu gaal ga nuur bu baax, ne fa tekk, te dooley duus ya daldi toj geen ba.

27:42  Bi loolu amee xarekat ya bëgg a rey ñi ñu tëj, ngir ragal ñenn ñi féey, ba raw.

27:43  Waaye njiit la bëgg a musal Pool, mu tere leen pexe ma. Mu sant ñi man a féey, ñu jëkk a sóobu ca ndox ma, ba jot tefes ga.

27:44  Mu sant ñi ci des ñu def noonu, langaamu ci ay dénk, mbaa ca tojiti gaal ga. Noonu ñépp jot tefes ga ci jàmm ak salaam.

28:1  Bi nu rëccee, nu yég ne dun baa nga tudd Màlt.

28:2  Te waa réew ma won nu laabiir gu ràññiku, ndaxte taalal nañu nu safara, ganale nu ndax taw bi sóob ak sedd bi.

28:3  Pool nag di for matt, di ko def ca taal ba, jaan ne ca mëlle ndax tàngoor wa, taq ci loxoom.

28:4  Bi waa réew ma gisee rab wa wéqu ci loxoom nag, ñuy waxante naan: «Ci lu wóor nit kii reykat la; te bi mu rëccee ca géej ga sax, ndogalu Yàlla mayu ko mu dund.»

28:5  Waaye Pool yëlëb rab wa ca safara sa, te wàññiwu ko dara.

28:6  Nit ñi di xaar mu newi, mbaa mu ne dàll, dee; waaye bi ñu négee lu yàgg te gis ne dara jotu ko, ñu soppi xel ne: «Kii yàlla la.»

28:7  Amoon na nag ca wet ya ay suuf yu doon moomeelu ku tudd Publiyus, di kilifag dun ba. Mu teeru nu, ganale nu ngan gu réy diirub ñetti fan.

28:8  Fekk baayu Publiyus dafa tëdd ndax ay tàngoori yaram yu koy dikkal ak biiru taññ. Pool nag dem seeti ko, ñaan ci Yàlla, teg ko ay loxoom, mu daldi wér.

28:9  Ci kaw loolu jarag ya ca des ca dun ba daldi dikk, amaat wér-gi-yaram.

28:10  Ñu teral nu ci fànn yu bare, te bi nuy dem, ñu jox nu li nuy soxla lépp.

28:11  Bi nu fa amee ñetti weer, nu dugg ca gaal gu lollikoo ca dun ba, daldi tàbbi ca géej ga. Gaalu dëkku Alegsàndiri la woon, te yor xàmmikaay guy nataalu Kastor ak Polugsë.

28:12  Noonu nu teer dëkku Sirakus, toog fa ñetti fan.

28:13  Nu jóge fa, leru tefes ga, ba agsi Resiyo. Ca ëllëg sa ngelawu sudd daldi jóg, te ca ñaareelu fan ba nu teer Pusol.

28:14  Gis nanu fa ay bokk, ñu ñaan nu, nu toog fa ayu-bés. Noonu nu dem Room.

28:15  Sunuy xebaar law na, ba egg ca bokk ya fa dëkk, noonu ñu gatandu nu ba ca péncu Apiyus ak bérab bu ñuy wax Ñetti añukaay ya. Bi leen Pool gisee, mu sant Yàlla, daldi takk fitam.

28:16  Bi nu dikkee Room nag, ñu may Pool, mu dëkk fa ko lew, moom ak xarekat ba koy wottu.

28:17  Bi ñetti fan wéyee, mu woolu njiiti Yawuti dëkk ba. Bi ñu dajaloo nag, mu wax leen lii: «Bokk yi, jàpp nañu ma ci Yerusalem, jébbal ma waa Room, fekk defuma dara luy suufeel sunu xeet, mbaa lu juuyoo ak sunuy aaday maam.

28:18  Waa Room nag seet sama mbir, te bëgg maa bàyyi, ndaxte toppuñu ma dara lu jar dee.

28:19  Waaye bi ko Yawut ya bañee, fas yéene naa dénk sama mbir Sesaar, fekk ba tey awma dara lu may taqal sama xeet.

28:20  Moo tax ma ñaan a gise ak yéen, nu diisoo, ndaxte yaakaaru bànni Israyil moo tax ñu jéng ma.»

28:21  Bi ñu ko déggee, ñu tontu ko: «Jotunu benn bataaxal bu jóge Yude ci sa mbir, te kenn ci bokk, yi fi dikk, jottaliwul mbaa mu seede ci yaw lu bon.

28:22  Waaye bëgg nanoo dégg li nga gëm, ndaxte xam nanu ne, tariixa booba, kenn jubluwu ko fenn.»

28:23  Noonu ñu dig ko bés, te ñu bare ñëw, fekksi ko ca néegam. Mu di leen jàngal suba ba ngoon, di leen dëggal lu jëm ci nguuru Yàlla ak ci Yeesu, tukkee ci yoonu Musaa ak ci yonent yi, di leen jéem a gëmloo.

28:24  Ñenn ñi nag gëm li mu wax, ña ca des weddi ko.

28:25  Gannaaw mënuñoo déggoo, ñu bëgg a tas. Waaye bi ñu laata dem, Pool teg ca wax jii: «Xel mu Sell mi wax na dëgg ak seeni maam, jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi.

28:26  Nee na:“Demal ci xeet wii ne leen:‘Dingeen déglu bu baaxwaaye dungeen xam dara;di xool bu baax waaye dungeen gis dara.’

28:27  Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis;dañuy déglu ak nopp yu naqari,tey gëmm seeni bët,ngir bañ a gis ak seeni bët,dégg ak seeni nopp,te xam ci seen xol,ñu woññiku ci man, ma wéral leen.”

28:28  «Xamleen nag ne, xebaaru mucc gii yégal nañu ko ñi dul Yawut, te ñoom dinañu ko déglu.»

28:30  Noonu diirub ñaari at Pool dëkk ca kër gu muy fey, di fa àggali ñépp ñi koy seetsi.

28:31  Muy yégle nguuru Yàlla, di jàngale ci mbirum Boroom bi Yeesu Kirist ak fit wu dëgër, te kenn terewu ko ko.


Next: Romans